I. Baat yi ñuy jëfëndikoo

Angalu digg

(C) ab mbege la wu diggam nekk O. A ak B ñaari tomb la ñu ci (C).
Angal bii di ^AOB ab angalu digg la ci mbege mii di (C).

Angal bu ñu rëdd

(C) ab mbege la wu diggam nekk O. A, B ak M ñetti tomb la ñu ci mbege mii di (C). Angal bii di AMB zb angal bi ñu rëdd ci mbege mi la.

Xammee :
Ab angal wu ñu rëdd bènn angal la boo xamne pujam bènn tomb la ci mbege mi ta ay wetam at buum la ñu ci mbege mòmu tey tukkee ci tomb bòbu. 

Angal yu jokkaloo

Angal bii di ^AMB da fa nekk bènn angal wu ñu rëdd ci mbege mi.
Angal bii di ^AOB da fa nekk bènn angalu digg ci mbege mi.
Angal yii di ^AMB ak ^AOB da ñuy bokk japp bènn xala ci mbege mi : da ñuy naan da ñoo jokkaloo.

II. Mengaleek bènn angal bu ñu rëdd ak angalu digg wi jokkaloo ak moom 

Ab jagle :
Ab angal wu ñu rëdd ci bènn mbege nattam da fay nekk gènn wàllu angalu digg bi mu jokkalool. 

 mes AMB=12 mes AOB mes AOB=2 mes AMB

III. Mengaleek ay angal yu ñu rëdd yuy bokk japp bènn xala

Ab jagle :
Ci bènn mbege, ñaari angal yu ñu rëdd yuy bokk japp bènn xala ñoo yem natt.

 mes AMB= mes ANB