I. Yemale yi bènn deetxam
Yemale yi am melokaanu : |ax+b|=c
- Su c ëppee tus, yemale gi da fay am ñaari sottal. Da ngay sottali 2 yemale yii di ax+b=c ak ax+b=−c
- Su c nekkee tus, yemale gi bènn sottal rekk la am. Da ngay sottali yemali gii ax+b=0
Yemale yi am melokaanu |ax+b|=|cx+d|
Da ngay jëfëndikoo jagle jii : |A|=|B| su fekkee te su dee rek ne A=B wala A=−B.
Yemale yi am melokaanu ax2+b=0
Da ngay firi ci ay ëmbeef su manee nekk cërr gu njëkk gi, bind ko ci anam gii di (ax+b)(cx+d)=0 ba pare jëfëndikoo jagle jii di A×B=0 su A=0 wala B=0.
II. Yemadi yi
Yemadi guy ab fŭllante wala yemadi gu melokaanu (ax+b)(cx+d)≤0
Ngir sottal bènn yemadi gu am melokaanu (ax+b)(cx+d)≤0, mann naa sottali kureeli yemadi yi muy firi ci jëfëndikoo jangat yii :
- Ab meññeefu 2 ëmbeef da fay yèes tus bu fekkee ne mandargaay ñaari ëmbeef yi da ñoo feewëloo.
- Ab meññeefu 2 ëmbeef da fay ëpp tus tus bu fekkee ne mandargaay ñaari ëmbeef yi bènn la ñu.
- Mann na ñu itam jëfëndikoo bènn alluwaay mandarga (tableau de signes).
Yemadi yu am melokaanu ax2+b⩽0
Ngir sottal bènn yemadi gu am melokaanu ax2+b⩽0 :
- Da may firi ci ay ëmbeef cërr gu njëkk gi.
- Ma daal di sottali yemadeek fŭllante (inéquation-produit) gi may am.