I. Piraamid
Wonale
Ab piraamid bènn mbirr mu dëgër la wu am :
- Bènn puj bu ñuy woowee itam “pujuk boppà” ;
- Ab sukkëndikukaay bu am melokaani bènn bariwett (bènn nataalu maasale gi bu am ay wet yu bari te sosoo ci bènn rëdd wu damm te tëju) ;
- Ay kanam yu wetu yu am melokaanu au ñettkoñ yu bokk bènn puj bu ñuy woowee itam “pujuk boppà” ;
- Pujuk boppu piraamid bi da fa jokkalook pujuk sukkëndikukaayam yi ci ay dogit yu ñuy woowee yaxi piraamid gi. Dèes na tuddee kawewaayu bènn piraamid rëdd wiy jaar ci pujam tey jub-dogoo ak maasaleek sukkëndikukaay bi.
Piraamid bu yemoo
Xamle
Da ñuy naan bènn piraamid da fa yemoo su fekkee ne :
- Sukkëndikukaayam da fa doon bènn bari wett bu wetyem (kaare, ñettkoñ bu wett-yem, ...)
- Ay kanamu wetam yi ay ñettkoñ yu ñaariwet-yem la ñu.
Ab jagle
Su bènn piraamid yemoo wee, konn kawewaayam da fay jaar ci diggi mbegeek wërële wu sukkëndikukaayam.
Yaatuwaayu wett ak ëmbeefu bènn piraamid bu yemoo
$\rm S A B C D$ ab piraamid la bu sukkëndikukaayam di bènn bari wett bu wett-yem $\rm A B C D$.
$\rm A^{\prime}$ mooy digguk $\rm [A B]$.
$\rm [SA']$ ñu ngi koy woowee apotemu piraamid bi.
$\mathrm A=\dfrac{\mathrm P \times a}{2}$
Mu andak
$\rm A =$ Yaatuwaayu wet gi
$\rm P =$ wërëleek sukkëndikukaay bi
$\rm h =$ apotem (kawewaayu bènn kanamu wet)
$\mathrm V=\dfrac{\mathrm B \times h}{3}$
Mu andak
$\rm V =$ ëmbeef
$\rm B =$ Yaatuwaayu sukkëndikukaay bi
$\rm h =$ kawewaayu piraamid bi
II. Kòònu wërële
Wonale
Xamle kawewaayu bènn kòòn
Xamle
Dès na tuddee kawewaayu bènn kòònu wërële rëdd wiy jaar ci pujam tey jub-dogoo ak maasaleek sukkëndikukaay bi.
Yaatu-yaatuk wet ak ëmbeefu bènn kòòn
$\mathrm A=\dfrac{\mathrm P \times a}{2}$
$\begin{array}{ll}\rm Andak & \rm A= \text{Yaatu-yaatuk wet}\\
& \rm P= \text{wërëleek sukkëndikukaay bi}\\
& h= \text{apotem (kawewaayu bènn} \\ &\text{kanamu wet)}\end{array}$
$\mathrm V=\dfrac{\mathrm B \times h}{3}$
$\begin{array}{ll}\rm Andak & \rm V= \text{Ëmbeef}\\
& \rm B = \text{yaatu-yaatuk sukkëndikukaay} \\ & \text{bi}\\
& h= \text{kawewaayu piraamid bi}\end{array}$
III. Dogitu bènn kòòn wala bènn piraamid
Dogitu maasaleek bènn piraamid ci bènn maasale gu wetlàŋ ak maasaleek sukkëndikukaayam ab bariwett la bu bokk melokaan ak sukkëndikukaay wòwu. Wetti bariwett yòyu da ñuy wetlàŋ ñaar- ñaar.
Dogitu maasale bu bènn kòòn ci bènn maasale gu wetlàŋ ak maasaleek sukkëndikukaayam ab mbege la.
Muy ci bènn rëyal wala bènn tuutil bu njuram (rapport) di $k$ :
- Guddaay yi da ñu leen di fŭll ci $k$,
- Yaatuwaay yi da ñu leen di fŭll ci $k^2$,
- Ëmbeef yi da ñu leen di fŭll ci $k^3$.
$k$ ñu ngi koy tuddee arafu waññeeku.