I. Yemadi yu am ñaari deetxam
Na $a$, $b$ ak $c$ doon ay limum dëgg yoo xamne $(a~ ; b) \neq(0~ ; 0)$.
- Dèes na tuddee yemadi bu jëgoom di bènn ci $\mathbb{R} \times \mathbb{R}$ bèpp yemadi bu am bènn ci melokaan yii : $ax+b y+c > 0$ ; $ax+b y+c < 0$ ; $ax+b y+c \geq 0$ wala $ax+b y+c \leq 0$.
- Ab takk-tànk $\left(x_1~ ; y_1\right)$ bu ay limum dëgg daa sottal ci kènn si yemadi yi, mungi firi ne $x_1$ ak $y_1$ da ñuy dëggël yemadi gòògu.
Ab misaal : $x-y+3<0$ ab yemadi bu jëgoom di bènn la ci $\mathbb{R} \times \mathbb{R}$.
- Ngir $x=1$ ak $y=5$, da ñuy am : $1-5+3=-1$.
$-1< 0$ dëgg la, konn takk-tànk gii dii $(1 ~; 5)$ ab sottalu yemadi gi la. - Ngir $x=0$ ak $y=0$, da ñuy am $0-0+3=3$.
$3 < 0$ du dëgg. Konn $(0~ ; 0)$ du sottalu yemadi gi.
Ci maasale gi ñu wutal bènn xammalekukaay $\rm (O, i, j)$, na ñu jël rëdd wii di $\rm (D)$ te yemaleem di : $ax+by+c=0$.
$\rm (D)$ da fay xaaj maasale gi ci ñaari xaaji maasale :
- Kènn si ñaari xaaji maasale yòyu da fay denc tomb yëpp yi nga xamne seeniy maaskà da ñuy dëggal $a x+b y+c > 0$
- Beneen xaaju maasale gi da fay denc tomb yëpp yi nga xamne seeniy maaskà da ñuy dëggal $a x+b y+c < 0$
Mbooloom sottaleek bènn yemadi da fay daal di nekk konn mbooloom takk-tànkuk maaskaay ay tomb yi nekk ci bènn xaaju maasale.
Ab misaal :
Mbooloom sottaleek yemadi gii di : $x-y+3 < 0$ mooy xaaju maasle, gi peggam di rëdd wii di (D) mi yemaleem di : $x-y+3=0$, te dencul $0(0 ~; 0)$.
II. Kureeli 2 yemadi yu am 2 deetxam
Wonale
$\left\{\begin{array}{l}
2 x-y+1<0 \\
-x+y-3<0\end{array}\right.$ ab kureelu yemadi yu seeniy jëgoo di bènn la, ci $\mathbb{R} \times \mathbb{R}$ te ay deetxamam di $x$ ak $y$.
Mandargaay nataal
Maasale gi da ñu koo wutal bènn xammalikukaay $\rm (O, i, j)$.
$\rm (D)$ mooy rëdd wi yemaleem di : $\rm (D)$ : $2x-y+1=0$
$\rm (D')$ mooy rëdd wi yemaleem di : $\rm(D^{\prime})$ : $-x+y-3=0$
$(\mathrm D) : 2 x-y+1=0$
Su fekkee $x = 0$, konn da ñuy am $2 \times 0 - y+ 1=0$
Konn $y = 1$
Ñu daal di am tomb bii di $\rm A(0~ ; 1)$
Su fekkee $x=1$, da ñuy am $2\times 1-y +1=0$
Konn $y = 3$
Ñu daal di am tomb bii di $\rm B(1~ ; 3)$
$(\mathrm D') : - x+y-3 =0$
Su fekkee $x=0$ konn da ñuy am $-0+y-3 =0$
$y = 3$
Ñu daal di am tomb bii di $\rm C(0~ ; 3)$
Su fekkee $x=1$ konn da ñuy am $1+y-3=0$
Konn $y = 2$
Ñu daal di am tomb bii di $\rm D(-1~ ; 2)$
Ab seetlu:
Goxx bi amul bènn kuloor mooy nataalu mandargaak sottaleek kureel gi.