I. Xamle

Soo jëlee bènn limum dëgg (nombre réel) bu ëpp tus $a$ bu mu manti doon, dina am bènn te bènn doŋŋ limum dëgg bu kaaareem di $a$.
Limm bòbu ñu ngi koy tuddee reenu kaareek $a$, te di ko binndee $\sqrt{a}$.
Sëf wii di « $\sqrt{a}$ » ñu ngi koy jaŋgee « reenuk kaare bu $a$ ».
Mandarga bii di $\sqrt{}$ dèes na ko tuddee reen gi.
$a$ mu ngi tudd biir-reen gi.

II. Ay jagle

  • limum dëgg yu ëpp tus $a$ ak $b$ yoo manti jël, $\sqrt{a \times b}=\sqrt{a} \times \sqrt{b}$.
  • limum dëgg yu ëpp tus $a$ ak $b$ yoo manti jël $(b \neq 0)$, $\sqrt{\dfrac{a}{b}}=\dfrac{\sqrt a}{\sqrt b}$.
  • limum dëgg bu ëpp tus $a$ boo manti jël, $(\sqrt{a})^2=a$.
  • limum dëgg boo manti jël, $a$, $\sqrt{(a)^2}=|a|$.

III. Sëfum jakkarloo

Sëfum jakkaarloo bu $\sqrt{a}+\sqrt{b}$ mooy $\sqrt{a}-\sqrt{b}$.
Sëfum jakkaarloo bu $\sqrt{a}-\sqrt{b}$ est $\sqrt{a}+\sqrt{b}$.
Sëfum jakkaarloo bi daf lay may nga mana soppali ci ab tojit limum suuf bi ko nekkuloon ci bènn tojit bu am ci biiram ab reenu kaare.

IV. Ay mengale

Reenu kaare ak toftalin

Reenu kaare bi da fay denc toftalin yi :
Su $a$ ak $b$ nekkee ñaari limum dëgg yu ëpp tus, su fekkee $a \leq b$ konn $\sqrt{a} \leq \sqrt{b}$.

Tolloo

Limum dëgg yu ëpp tus $a$ ak $b$ yoo manti jël, $a=b$ su dee te su dee rekk $\sqrt{a}=\sqrt{b}$.

Sartu mengale

Ngir mengale ñaari limum dëgg yu ëpp tus $a$ ak $b$, dina doy nga mengale seeniy kaare.

V. Njëkk wu matt bu bènn limum dëgg

Limum dëgg $a$ boo manti jël :

  • $\vert a \vert = a$ su $a$ ëppee tus.
  • $\vert a \vert = - a$ su $a$ yèesee tus.

Limum dëgg $a$ ak $b$ yoo manti jël :

  • $\vert a \times b\vert = \vert a\vert  \times \vert b \vert$
  • $\left| \dfrac{a}{b} \right|=\dfrac{|a|}{|b|}$