I. Baat yi ñuy jëfëndikoo
Taxawinu (Sinus) bènn angal wu jub
Ci bènn ñettkoñ wu jub, dèes na tuddee taxawinu bènn angal wu xatt (wala wu nattam), xaajaleek guddaayu wet gi jakkarlook moom ci guddaayuk janookoñjub bi.
sin^ABC= Wet wi jakkarlook ^ABC Janookoñjub gi
Ab misaal :
Ci ñettkoñ bii di ABC nga xamne da fa jubkoñ ci B, da ñuy am : sin^BAC=BCAC.
Tëddinu (cosinus) bènn angal bu xatt
Ci bènn ñettkoñ wu koñjub, dèes na tuddee tëddinu bènn angal wu xatt (wala wu nattam), xaajaleek guddaayu wet gi feetewoo ak moom ci guddaayuk janookoñjub bi. cos^ABC=Wet wi feetewoom ^ABC Janookoñjub gi
Felleesuk (tangente) bènn angal bu xatt
Ci bènn ñettkoñ wu koñjub, dèes na tuddee felleesuk bènn angal wu xatt (wala wu nattam), xaajaleek guddaayu wet gi jakkarlook moom ci wet gi feetewoo ak moom.
Ci ñettkoñ gii di ABC nga xamne da af jubkoñ ci B, da ñuy am :
tan^BAC=Wet gi feewëlook ^BACWet gi feeteek ^BAC=BCAB
II. Ay jagle
Jangat ci digante tëddin ; taxawin ak felleesu
Felleesuk bènn angal bu xatt mu ngi tollook xaajaleek taxawinu angal bòbu ak tëddinam.
Ñu waxee ko neneen ; su ˆA nekkee bènn angal bu xatt, da ñuy am : tanˆA=sinˆAcosˆA.
Tëddin ak taxawinu ñaari angal yu mottaliwante
Su ñaari angal mottaliwantee, taxawinu kènn ki da fay tollook tëddinu keneen ki.
Ñu waxee ko neneen, su fekkee ne ˆA ak ˆB da ñoo nekk ñaari angal yoo xamne da ñuy melni mes ˆA+mesˆB=90∘ kon : sinˆA=cosˆB te cosˆA=sinˆB.
Jokkaloo bu am solo
Angal bu xatt boo jël nga xamne nattam mooy a∘, da ñuy am :
- 0<sina∘<1 ;
- 0<cosa∘<1 ;
- sin2a∘+cos2a∘=1.
III. Ay njëkk yu ñu mana seetlu
ˆA | 0° | 30° | 45° | 60° | 90° |
sinˆA | 0 | 12 | √22 | √32 | 1 |
cosˆA | 1 | √32 | √22 | 12 | 0 |
tanˆA | 0 | √33 | 1 | √3 | x |