I. Maas yi ak magum maas yi 

Ab misaal : Na ñu dajale toppalanteek xammeekaayu liggeey yii di ñëw ci ay maas yu seeniy yaatuwaay di  $4$ : $0$ ; $11$ ; $8$ ; $14$ ; $17$ ; $15$ ; $3$ ; $5$ ; $7$ ; $6$ ; $7$ ; $13$ ; $5$ ; $12$.

Jeexital bi moom la ñu tëŋk ci alluwa bii ci suuf  :

Magum maas yi (classe modale) mooy maas gi am limm wi gënë bari (mann na ñu am ay magum maas yu bari). Ci alluwa bii ci kow, magum maas mi mooy maas mii di $[4~ ; 8[$.

II. Limm yi ñu dajale ak bariwaay yi ñu dajale 

Na ñu jël bènn toppalanteek wàññi bu melokaanam limu (quantitatif).

  • Dèes na woowee limm wu ñu dajale ci anamu yokku (NDY) bu bènn nekkin (modalité) $n$, ndajaleek limmi bépp nekkin bu yèes wala bu yemook $n$.
  • Dèes na woowee barewaay wu ñu dajale ci anamu yokku (BDY) bu bènn nekkin $n$, xaajaleek limm wu ñu dajale ci anamu yokku bu bènn nekkin $n$ ci limmum lëmm gi.
    Ñu ngi koy xamlee itam ci ne mooy ndajaleek barewaayi nekkin yi yèes wala ñu yemook nekkin wòòwu.

Ab misaal :

III. Yemoo gi

Yemook bènn toppalanteek wàññi bu ñu seddële si ay maas mu ngi tollook ndajaleek fŭllanteey diggu maas gu nekk ak limmam, ñu xaaj ko ci limm gu matt gi.

Ab misaal :

Yemoo gi mooy $\begin{array}{l}
\rm M & =\frac{1,55 \times 13+1,65 \times 20+1,75 \times 18}{51} \\
& =\dfrac{84,65}{51} \\
& =1,65980 \ldots \\
& \approx 1,66\end{array}$
(jeexital bu ñu jegeel ci raŋuk 2)

Yemook guddaayu maaasu ndoŋgo yi nekk ci maas gògu mooy $1,66 \mathrm{~m}$.

IV. Jaar-digg

Dèes na woowee jaar-digguk bènn toppalanteek wàññi bu ñu raŋale ay njëgëm, bépp limm buy xaaj toppalante gi ci ñaari toppalante yu ndaw yu tolloo limm :

  • Bènn mbooloo mu njëkk yi yèes wala ñu tollook jaar-digg bi yëpp nekk ;  
  • Bènn mbooloo mu njëkk yi ëpp wala ñu tollook jaar-digg bi yëpp nekk.

Seetlu bu njëkk

Su limm gu matt $\rm N$ bu bènn toppalanteek wàññi  nekkee limm gu tòòl (impair), konn jaar-digg bi mooy njëkk li tolluwayam di $\rm \dfrac{N+1}{2}$ ci toftalannteek njëgu toppalante gi su ñu leen raŋalee.

Misaal wu njëkk :

Da ñoo joxe toppalanteek wàññi gii  : $2$ ; $5$ ; $6$ ; $7$ ; $8$ ; $9$ ; $10$ ; $12$ ; $13$ ; $14$ ; $15$.
Na ñu seet jaar-diggu toppalante gi. Limm gu matt gi mooy $11$ (muy ab limm wu tòòl), konn tolluwaayu jaar-digg bi ci toftalante bi ñu raŋale mooy $\dfrac{11+1}{2}=\dfrac{12}{2}=6$
Jaar-digg bi mooy njëkk li tolluwaayam di 6 ci toftalante bi ñu raŋale : mooy  $9$.

Seetluk ñaareel

  • Su limm gu matt $\mathrm{N}$ bu bènn toppalanteek wàññi  nekkee limm gu tòllanti (pair), konn jaar-digg bi mooy bépp limm bu nekk ci digante  $\dfrac{\rm N}{2}$ ième njëkk ak $\left(\dfrac{\rm N}{2}+1\right)^{\text{eelu}}$ njëkk mann na ñu ko jappee ni jaar-diggu toppalante gi.
  • Waaye li gënë bari, da ñuy japp ne jaar-digg bi mooy yemook ñaari njëkk yòyu.

Misaaluk ñaareel :

Da ñoo joxe toppalanteek wàññi gii di ñëw : $5$ ; $6$ ; $7$ ; $8$ ; $10$ ; $12$.
Na ñu jeema xam jaar-diggam.
Limm gu matt di $6$ ab limm wu tòllanti la , konn jaar-digg bi mu ngi nekk ci digante 3eel ak 4eel njëkk ci toftalante bi ñu raŋale, maanaam ci digante $7$ ak $8$. Di na ñu ko xam bu ñu defaree yemook ñaari njëkk yòyu.  Konn jaar-digg wi ñuy wut mooy : $\dfrac{7+8}{2}=7,5$.

Ngir am jaar-digguk bènn toppalante bu ñu raŋale, mann na ñu ko defee si ñaari anam :

$\checkmark$ Anamu xamum njëkk bu buumu (interpolation linéaire) :

Ab misaal :

Na ñuy tuddee $\rm Me$, guddaay bi jaar-digg :
$\rm Me$ mooy guddaay wi limmam bi ñu dajale ci anamu yokku di tollook gèn wàllu limm wu matt wi, maanaam $\left(\dfrac{500}{2}=250\right)$ konn $\rm Me \in[165~ ; 175[$.
Da ñuy jëfëndikoo alluwaayu jokkalekaay bii ci suuf ngir xam jaar-digg gi :

 $\begin{array}{|c|c|c|}
\hline
165 & \rm M e & 175 \\
\hline
84 & 250 & 298 \\
\hline
\end{array}$
Da ñuy am $\begin{array}{l}
\rm\dfrac{M e-165}{250-84}=\dfrac{175}{298} \\
\rm\dfrac{Me-165}{166}=\dfrac{10}{214} \\
\rm Me=172,75~cm
\end{array}$

$\checkmark$ Anamu nataal (Bariwetu limm yi ñu dajale ci anamu yokku)

Ab misaal :
Na ñu jëfëndikoo alluwaayu limm yi ñu dajale ci anamu yokku ngir nataal bariwetu limm yi ñu dajale ci anamu yokku.