I. Ci mbirim ñettkoñ bi

Roofoog Taless

Ñaari ñettkoñ da ñuy defar bènn roofoog Taless su fekkee ne li leen soss mooy ñaari rëdd yu dogoo yoo xamne ñoom itam ñaari rëdd yu wetlàŋ ñoo leen dog. 


Ñetti nataal yii dèes na leen tuddee ay roofoog Taless.

Cèetuk Taless wu jub xocc wi

$\mathrm{ABC}$ ab ñettkoñ la.
$\rm M$ bènn tombu rëdd wii di $(\mathrm{AB})$ la te $\mathrm{N}$ bènn tombu rëdd wii di $(\mathrm{AC})$ la.
Su $(\mathrm{MN}) / /(\mathrm{BC})$ konn $\rm\dfrac{A M}{A B}=\rm\dfrac{A N}{A C}$.

Ab seetlu :

Man ngaa jëfëndikoo jagleek Taless ngir xayma ay soreewaay wala dëggal yemook ay tojit.

Li ciy tukkee

$\rm A B C$ ab ñettkoñ la, $\rm M \in(A B)$ te $\rm N \in(A C)$ :
Su fekkee ne $\rm (M N) ~//~(B C)$ kon da ñuy am :
$\rm\dfrac{A M}{A B}=\dfrac{A N}{A C}=\dfrac{M N}{B C}$

Ab seetlu :

Cèetuk Taless ak li ci tukkee da ñu lay may nga mana xayma guddaayu ay dogit.

Jallawleek cèetu Taless

$\rm A B C$ ab ñettkoñ la.
$\rm M$ ab tomb la ci rëdd wii di $\rm (A B)$ ; $\rm N$ ab tomb la ci rëdd wii di $\rm (A C)$ ci anam boo xane nekkinu $\rm M$ soo ko mengalee ci $\rm A$ ak $\rm B$ da fay nekk bènn ak nekkinu $\rm N$ boo ko mengalee ci $\rm A$ ak $\rm C$.

Su fekkee ne $\rm\dfrac{A M}{A B}=\dfrac{A N}{A C}$ kon $\rm (M N)~ // ~(B C)$

Ab seetlu :

Jallawleek cèetu Taless daf lay may nga dëggal ne ay rëdd da ñoo wetlàŋ.

Xaajale bènn dogit ci ay dogit yu tolloo guddaay

Anam bi ñu koy defee :

Ngir tek ci kow dogit wii di $\rm [A B]$, tomb $\rm M$ biy tax ñu am $\mathrm{A M}=\dfrac{a}{b}$ si loo xamne $a$ ak $b$ ay limmum lëmm yu raññeeku la ñu, man nga koo doxalee nii: (ci natal bi $a=3$ te $b=5)$.