I. Yokkalanteek ay jëmu

A, B et C ñetti tomb la ñuy ci maasale gi. Dèes na tuddee ndajaleek jëmu yii di AB ak BC, jëmu jii di AC.

Da ñuy binnd : AB+BC=AC.

Yemoo gògu ñu ngi koy tuddee yemook Shaal (Chasles).

Jëmu yu feewëloo

A, B ak C ñetti tomb la ñuy ci maasale gi.
Da ñuy am : AB+BA=AA=0
Da ñuy naan AB ak BA ay jëmu yu feewëloo la ñu. Ñu daal di binnd BA=AB

II. Fŭllanteek bènn jëmu ci bènn limm

Xammee

Dèes na tudddee fŭllanteek jëmu bu dul tus bii di AB ci limum dëgg wii di k, jëmu jii di MN.

  • (AB) // (MN) ñoo bokk jubluwaay ;
  • AB ak MN :
    • ñoo bokk jëmukaay su fekkee ne k>0 ;
    • seeniy jëmukaay yi da ñoo feewëloo su fekkee ne k<0
  • MN=|k|AB.

Ab seetlu :

  • Fŭllanteek jëmuk tus gi ci bènn limum dëgg mooy jëmuk tus gi ;
  • Fŭllanteek jëmu jii di AB ci 0 da fay nekk jëmuk tus gi 0 ;
  • Fŭllanteek jëmu jii di AB ci bènn limm k bu dul tus dèes na ko binndee : kAB.

Ay misaal :

Jëmu yii di AB, 1.5AB  ñoo bokk jubluwaay.
AB ak 1,5AB ñoo bokk jëmukaay.
AB et 3AB seeniy jëmukaay yi da ñoo feewëloo.

Ay jagle

A, B, C ak D ay tomb la ñu ci maasale gi. k ak h ay limum dëgg la ñu. Da ñuy am :

  • k(hAB)=(kh)AB.
  • kAB+kCD=k(AB+CD).
  • kAB+hAB=(k+h)AB.
  • 1AB=AB.

III. Jëmu yu bokk jubluwaay ak jëmu yu bokk rëdd (colinéaires)

Jëmu yu bokk jubluwaay

Ab jagle

A, B, C ak D ñeenti tombi maasale gi la ñu.
Wax ne jëmu yii di AB ak CD ñoo bokk jubluwaay mu ngi firi ne mann ngaa gis bènn limm k bu dul tus tey tax ñu am : AB=kCD

Jëmu yu bokk rëdd

Xammee

Da ñuy naan ñaari jëmu ñoo bokk rëdd su fekkee ñoo bokk jubluwaay, wala su kènn si ñoom nekkee jëmuk tus gi.

Ab misaal :

AB=3CD mu ngi junj ne AB ak CD ñoo bokk jubluwaay alorste konn AB ak CD ñoo bokk rëdd.

Ab jagle

A ak B ñaari tomb la ñu si maasale gi.
Ne bènn tomb M da fay bokk ci rëdd wii di (AB) mu ngi yemook nga wax ne AM ak AB ñoo bokk rëdd.

Yu tukkee ci lòlu

Jëmu ak digg

Su tomb bii di I doonee digguk [AB], konn AB=2AI

Su fekkee AB=akAI konn I mooy digguk dogit wii di [AB].

Tomb yu raŋale

Su A, B ak C raŋalee konn AC=kABk0

Su AC=kABk0 konn A, B ak C da ñoo raŋale.

Rëdd yu wetlàŋ

Su (AB)//(CD) konn AB=kCDk0

Su AB=kCDk0 konn (AB) ak (CD) da ñoo wetlàŋ.