I. Xamle
Ab soppiku bu buumu $f$ bènn soppiku la boo xamne da fay lëkkale (associer) bépp lim $x$ ak lim bii di $a x$ ; $a$ nekk bènn limm bu dul tus. Ñu ngi koy binndee $f(x)=a x$ wala $f: x \rightarrow a x$.
Limm bii di $a$ ñu ngi koy tuddee alluwa bi.
II. Ay jagle
Limm $a$ ak $b$ yoo mana jël :
- $f(a+b)=f(a)+f(b)$
- $f(a b)=a f(b)$
- Bépp anamu dëppoo ci xaajale da fay mengook bènn soppiku bu buumu te bépp soppiku bu buumu da fay mengook bènn anamu dëppoo ci xaajale.
III. Mandarga ci ab nataal
Mandarga ci ab nataal bu bènn soppiku bu buumu $x \rightarrow a x$ mooy mbooloom tomb $\rm M$ yi nga xamne seeniy maaska ñooy $(x$ ; $a x)$. Mooy rëdd biy jaar ci tambalinu aks yi aak ci tomb bi ay maaskaam di $(1$ ; $a)$.