I. Baati tëral yi ci algebr

Soo jëlee ay limum tojit $a$, $b$ ak $c$ yu mu mana doon :

  • $a+(b-c)=a+b-c$
  • $a-(b-c)=a-b+c$
  • $a-(b+c)=a-b-c$

II. Firi et dajale ay baati tëral yu arafu

Firi bènn baatu tëral bu arafu, mooy nga soppali bépp meññeefu ay ëmbeef ci bènn ndajaleek ay cër. 
Dajale bènn baati tëral mooy nga défar ndajaleek wala wa waññeekuk cër yi nuroo. 
Limum tojit $a$, $b$, $c$ ak $d$ yoo mana jël :

  • $a(b+c)=a \times b+a \times c$
  • $a(b-c)=a \times b-a \times c$
  • $(a+b)(c+d)=$ $a \times c + a \times d+b \times c+b \times d$
  • $(a-b)(c-d)=$ $a \times c-a \times d - b \times c+b \times d$
  • $(a+b)^2=a^2+2 a b+b^2$
  • $(a-b)^2=a^2-2 a b+b^2$
  • $(a-b)(a+b)=a^2-b^2$

III. Soppi ci ay ëmbeef bènn baatu tëral bu arafu

Soppi ci ay ëmbeef bènn baatu tëral bu arafu, mooy nga bind ko ci anamu meññeefu ay ëmbeef. 
Limum tojit $a$, $b$, $c$ ak $d$ yoo mana jël :

  • $a b+a c=a(b+c)$
  • $a b-a c=a(b-c)$
  • $a^2+2 a b+b^2=(a+b)^2$ $=(a+b)(a+b)$
  • $a^2-2 a b+b^2=(a-b)^2$ $=(a-b)(a+b)$
  • $a^2-b^2=(a+b)(a-b)$

IV. Xaymaak njëguk limm bu bènn baatu tëral bu arafu

Ngir xayma njëguk limm bu bènn baatu tëral bu arafu, da may soppali araf bu nekk ci njëgam ba noppi ma défar xayma yi.