I. Yemale yu melni ax+b=0
(a ak b ay limum tjit la ñu)
- Su a=0 ak b=0 kon bépp limm ab sottal la.
S={R} - Su a≠0 kon x=−ba.
S={−ba} - Su a=0 ak b≠0 kon amul sottal.
S={∅}
II. Yemale yu melni (ax+b)(cx+d)=0
Da ñuy jëfëndikoo jagle jii : A×B=0 mu ngi firi ne A=0 wala B=0
Da ngay sottali : ax+b=0 wala cx+d=0
III. Yemale yu melni ax=0 ak ax=bc
Da ñuy jëfëndikoo jagle jii : ab=cd mu ngi firi ne a×d=b×c.