I. Yemadi yu melni ax+b0 wala ax+b0 ou ax+b0 wala ax+b>0

Bépp yemadi bu mel nònu man na ñu ko soppali bamu mel  ni :

xk wala xk wala xk wala x>k

Sottali yu yemadi gògu man na ñu ko mandargaal ci bènn rëdd wu ñu maaska wala ñu joxe ko ci anamu ay digante (intervalles).

Ab misaal : 2x60
2x6
x62
x3

II. Yemadi yi melni ax+bcx+d ( ou wala ou >)

Bépp yemadi bu mel ni ax+b>cx+d man na ñu ko soppali bamu mel ni : ax b wala axb wala axb wala ax>b.

Ab missal : 2x+5>x+4
2xx>45
x>1

III. Kureelu 2 yemadi yu am bènn deetxam

Bènn kureelu 2 yemadi yu am 1 deetxam ñu ngi yemook 2 yemadi yu ñu dajaleek bènn laafaleek ubbi (parenthèse ouvrante).

Sottali bènn kureelu 2 yemadi.
Da ñuy sottali yemadi bènn bènn.  
Ñu fësal selebeyoonu (intersection) 2 sottali yi ñu am be noppi ñu binnd mbooloom sottalim kureel gi.