I. Xammee aki mbindin
Ab limum tojit mooy bènn lim bu ñu mana binndee ci anam bii di ab mu andak a ak b di ay limm yu jokkaloo.
Mbooloom limum tojit yi dèes na ko woowee Q.
- ab=a×kb×k
- ab=a÷kb÷k
- −ab=a−b=−ab
II. Sëfuk xayma yi ci Q
Soo jëlee ay limum tojit yumu mana doon a ; b ; c ak d :
- ab+cb=a+cb ; ab−cb=a−cb ci lu andak b≠0
- ab+cd=a×d+c×bb×d ; ab−cd=a×d−c×db×d ci lu andak b≠0 et d≠0
- ab×cd=a×cb×d
- ab÷cd=ab×dc ci lu andak b≠0 ; c≠0 te d≠0
III. Njëgg wu matt
Na a nekk bènn limum tojit :
|a|=a su a ëppee tus.
|a|=−a su a yèesee tus.
Soo jëlee ay limum tojit yumu mana doon a ak b :
- |a×b|=|a|×|b|
- |ab|=|a||b|
- |a|=|b| mu ngi tekki ne a=b wala a=−b
IV. Mengale
Soo jëlee ay limum tojit yumu mana doon a ; b ; c ak d :
- ab=cd mu ngi tekki ne a×d=b×c ci lu andak b≠0 ak d≠0
- Su a=b kon a+c=b+c te a−c=b−c
- Su a=b kon a×c=b×c te a÷c=b÷c
- Su a⩽b kon a+c⩽b+c te a−c⩽b−c
- Su a⩽b te c ëpp tus, kon a×c⩽b×c te a÷c⩽b÷c
- Su a⩽b te c yèes tus, kon a×c>b×c te a÷c>b÷c