I. Ay jagle
Cèetuk PITAAGOOR (Pythagore)
Ci bépp ñettkoñ bu koñjub, kaarewuk guddayu janookoñjub bi mu ngi tollook ndajaleek kaare yu ñaari wet yi feeteek angal wu jub wi.
Su $\rm ABC$ nekkee ab ñettkoñ bu koñjub ci $\rm A$ kon :
$\mathrm{BC}^2=\mathrm{AB}^2+\mathrm{AC}^2$
Cèetuk yaatuwaay yi
Ci bépp ñettkoñ bu koñjub, meññeefu guddaayi ñaari wet yi feeteek angal wu jub wi mu ngi tollook meññeefu guddaayi janookoñjub bi ak guddaayi kawewaay biy tukkee ci pujuk angal bu jub bi.
Su $\mathrm{ABC}$ nekkee bènn ñettkoñ bu koñjub ci $\mathrm{A}$ te $\mathrm{H}$ di tanki kawewaay bi tukkee ci $\mathrm{A}$ kon :
$\rm A B \times A C =B C \times A H$.
II. Xammeekukaay
Juutalu Cèetuk PITAAGOOR
Bu fekkee ne ci bènn ñettkoñ bu koñjub, kaarewuk guddayu wet gi gëna gudd mu ngi tollook ndajaleek kaareek guddaay yu yeneen ñaari wet yi, kon ñettkoñ bòbu da fa koñjub.
Su $\mathrm{ACB}$ nekkee bènn ñettkoñ boo xamne ci moom da ñu am :
$\mathrm{AB}^2=\mathrm{AC}^2+\mathrm{BC}^2$
Kon ñettkoñ bii di $\rm ACB$ da fa koñjub ci $\rm C$.
Juutalu Cèetuk yaatuwaay yi
Ci bènn ñettkoñ, su fekkee ne meññeefu guddaayi ñaari wet yi da fa tollook meññeefu guddaayu ñetteeli wet gi ci guddaayi kawewaay gi dëppoo ak moom, kon ñettkoñ bòbu da fa koñjub.
Na $\rm A B C$ nekk ab ñettkoñ te $\mathrm{H}$ di tanki kawewaay bi tukkee ci $\rm A$.
Su fekkee ne $\rm A B \times A C=B C \times A H$ kon ñettkoñ bi da fay koñjub ci $\rm A$.