I. Seddale koñ yi

Ab seddale koñ bu bènn ñettkoñ mooy rëdd biy xaaj bènn angal ci ñaari angal yu yemoo kepp. 

Ñetti seddale koñu bènn ñettkoñ da ñuy dogante ci bènn tomb bu ñuy woowee digguk mbege mi bindu ci biir ñettkoñ bi. 

II. Jaar-digg yi

Jaar diggub bènn ñettkoñ mooy rëdd biy jaar ci bènn puj ak ci diggi wet gi feewëloo ak puj gògu. 

Ñetti jaar diggub bènn ñettkoñ da ñuy dogante ci bènn tomb bu ñuy woowee digguk diisaay gi. 

$\rm L$ mooy digguk diisaay gi.

Digguk disaayu bènn ñettkoñda fay feetewoo si ñaari ñetteeli jaar-digg bu nekk boo dalee ci puj gi. 

III. Xammeekuk bènn ñettkoñ bu ñaariwet-yem

  • Su fekkee ci bènn ñettkoñ, bènn kawewaay da fa boole doon ab seddale koñ, kon ñettkoñ bòbu da fa ñaariwet-yem. 
  • Su fekkee ci bènn ñettkoñ, bènn jaar-digg da fa boole doon ab seddale koñ, kon ñettkoñ bòbu da fa ñaariwet-yem. 
  • Su fekkee ci bènn ñettkoñ, bènn taseebkawewaay da fa boole doon ab seddale koñ, kon ñettkoñ bòbu da fa ñaariwet-yem.