I. Cèet 1
Su bènn rëdd jaaree ci diggiy ñaari weti bènn ñettkoñ, kon da fay wetlàŋ ay sukkëndikukaayu ñetteeli wet gi.
C′ mooy diggub [AB] te B′ mooy diggub [AC] kon (d) da fay wetlàŋ ak (BC).
II. Cèet 2
Su bènn dogit jokkalee diggiy ñaari weti bènn ñettkoñ, kon guddaayam da fay tollook gènn walli guddaayi ñetteeli wet gi.
I mooy diggub [AB] te J mooy diggub [BC] kon J=12AC.
III. Cèet 3
Si bènn ñettkoñ, su fekkee ne bènn rëdd da fay jaar ci diggi bènn wet te wetlàŋ ak beneen wet, kon da fay jaar ci diggi ñetteeli wet gi.
B′ mooy digguk [AC] te (d) da fa wetlàŋ ak (BC) kon C′ mooy digguk [AB].
IV. Cèet 4
Su ñetti rëdd daggatee ci bènn dogkat (sécante) ñaari dogit yu toftalante te yemoo guddaay, kon da ñuyy daggat ci dogkat beneen bu nekk ñaari dogit yu toftalante te yemoo guddaay.