I. Tolluwaayu ñaari mbege
Na C(O ;R) ak C′(O′ ;R′) nekk 2 mbege.
Mbege yu riisoo ci biti
Su soreewaayu 2 digg yi tollook ndajaleek ceeñeer yi, kon mbege yi da ñu riisoo ci biti : OO′=R+R′.
Mbege yu riisoo ci biir
Su soreewaayu digante 2 digg yi tollook waññeekuk ceeñeer yi, kon mbege yi da ñoo riisoo ci biir : OO′=R−R′.
Mbege yu wuute ci biti
Su soreewaayu digg yi ëppee ndajaleek ceeñeer yi kon ñaari mbege yi da ñoo wuute ci biti : OO′>R+R′
Mbege yu wuute ci biir
Su soreewaayu digg yi yèesee waññeekuk ceeñeer yi kon ñaari mbege yi da ñoo wuute ci biir : OO′≤R−R′.
Mbege yu dogoo
Su soreewaayu 2 digg yi nekkee ci digante waññeekuk ceeñeer yi ak seen ndajale, kon ñaari mbege yi da ñoo dogoo : R−R′≤OO′≤R+R′
II. Soreewaayu bènn tomb ci bènn rëdd
Na (D) nekk bènn rëdd te M di bènn tomb bu nekkul ci (D). Na H doon tanku jub-dogoob (D) biy jaar ci M.
Ngir tomb A boo jël ci (D), da ñuy am : MH≤AM.
Da ñuy naan AH mooy soreewaayu tomb bii di M ci rëdd wii di (D).
III. Jagleek seddale koñ bi
Na ^HAK nekk bènn angal te A di ab tomb.
- Su M nekkee ci seddaleeb koñu (bissectrice) ^HAK ko M da fay yemoo sorewaay ak ñaari weti angal bi.
- Su M tolloowee sorewaay ak ñaari weti angal bi, kon da fay nekk ci seddaleeb koñu angal bii di ^HAK.
IV. Tolluwaayu bènn rëdd ak bènn mbege
Na C(O,R) nekk bènn mbege te (D) di bènn rëdd. Na OH=d di soreewaayu tomb bii di O ci rëdd wii di (D).
- Su soreewaay bii di d ëppee ceeñeer R bu mbege mi, kon mbege mi ak rëdd wi da ñoo wuute. d>R.
-
Su soreewaay bii di d yèesee ceeñeer R bu mbege mi, kon mbege mi ak rëdd wi da ñoo dogoo. d≤R.
- Su soreewaay bii di d tolloowee ak ceeñeer R bu mbege mi, kon mbege mi ak rëdd wi da ñoo riisoo. d=R.