I. Ay baat
- Wëy dëkk bi bènn mbooloo la boo xamne ci la jangatuk wàññi gi du aju.
- Bènn cër bu nekk ci wëy dëkk bi ab jambur (individu) wala ab bènneelu wàññi gi.
- Da ñuy seetlu ay melokaan (caractères) yu mana am ay njëg yu wuute.
- Bènn melokaan da fa limu su fekkee da ñuy jëfëndikoo ab limm ngir joxe ay njëgam. Bu dul lòlu, da ñuy naan da fa tolluwu (qualitatif). Ab melokaan da fay am njëg bu ñu xam.
- Nattum lëm gi mooy limu jambur yi nekk ci wëy dëkk bi wëy dëkk bi. Ñu ngi koy binndee $\rm N$.
- Barewaayu bènn njëgu melokaan wi mooy pàcc (rapport) gii : $\dfrac{n_i}{\rm N}$.
- Magum njëg yi mooy njëg bi gëna barile am natt. Ab toppalanteek wàññi (série statistique) man na am ay magum njëg yu bari.
- Digg doomu gi ab limm la buy raññale bènn “feete” bu njëgi melokaani bènn toppalanteek wàññi su fekkee melokaan wòwu da fa limu.
Dèes na binndee $x_1$, $x_2$, $\ldots$, $x_p$ njëg yu wuute yu bènn melokaan wu limu di jël; $n_1$, $n_2$, $\ldots$, $n_p$ natti kép kènn ci lim yòyu ak $\mathrm{N}$ nattum mbooloo mi.
Digg doomu gi $x=\dfrac{x_1 \times n_1+x_2 \times n_2+\ldots + x_p \times n_{p}}{\rm N}$
II. Mandargaal yi ci nataal
Nataal ci ay bannt
Ci bènn xammekaay bu aksam yi jub-dogoo, da ñuy mandargaal ci maaskà yu tëdd yi njëk yi te maaskà yu taxaw yi natt yi.
Bépp njëg dèes na ko mandargaalee ak bènn dogit woo xamne guddaayam da fa dëppoo ci xaajale ak limam.
Bènn nataal ci bant mu ngi nii boo xamne da fay mandargaal bènn toppalanteek ay xamukaayu liggeey (notes) bu bènn maas ci bènn wareef (devoir).
Nataal ci ay gàŋgòor (bandes)
Ci bènn xammeekaay bu aksam yi jub-dogoo, da ñuy mandargaal ci maaskà yu tëdd yi njëk yi te maaskà yu taxaw yi natt yi. Njëk wu nekk bènn jubkoñ moo koy mandargaal boo xamne guddaayam da fay dëppoo ci xaajale ak limam. Jubkoñ yòyu yëpp da ñooy yem yaatuwaay.
Nataal ci ay bant
Xammee
Ab nataal ci ay gàŋgòor (wala ci ay bant) daf lay may nga gis si lu gaaw njëg yi te man leena mengale. Guddaay yi da ñuy dëppoo ci xaajale ak lim yi (wala ak barewaay yi) ci njëk.
Ab misaal :
Nataal ci ay xaaji mbege
Da ngay njëkka rëdd bènn mbege booy xaaj ci ay wàll yu bokkul. Njëg wu nekk ñu ngi koy manadargaalee bènn wàll woo xamne yaatuwaayam da fay dëppoo ci xaajale ak limam.
Ci njëg wu nekk, angalu digg bu wàll gi da fay dëppooo ak natt wii :
$\dfrac{360° \times \text{nattug njëg li}}{\text{Nattum mbooloo mi }}$
Nataal ci ay xaaji gènn wàllu mbege
Da ñu koy defar ni ñuy defaree nataal ci ay xaaji mbege waaye si kow nga wuutale mbege mi ak bènn xaaju mbege.
Ci njëg wu nekk, angalu digg bu wàll gi da fay dëppooo ak natt wii :
$\dfrac{180° \times \text { nattug njëg li }}{\text { Nattum mbooloo mi }}$