Tekki
Takkandeer bu jub bu bènn tomb M ci bènn rëdd (d) mooy tomb H biy nekk doganteek rëdd wii di (d) ak jub-dogoo wu (d) miy jaar ci M.
H mooy takkandeer bu jub bu tomb bii di M ci rëdd wii di (d).
Ay jagle
- Takkandeer bu jub bu bènn dogit ab dogit lay doon woo xamne yènn saayi man na yemook bènn tomb.
- Digguk bènn dogit mu ngi takkandeeree ci diggi dogit biy nataalam.
Xammeeku ci maasale gi
- Xàmmikaayu digguk bènn dogit
Su ñu amee A(xA ;yA);B(xB ;yB) ak M(xM ;yM)
Te su M nekkee digguk dogit wii dit [AB] kon :
xM=xA+xB2 ak yM=yA+yB2 - Kaare wuk soreewaay ci digante 2 points
Su ñu amee A(xA ;yA) ak B(xB ;yB) kon :
AB2=(xB−xA)2+(xB−yA)2