I. Toxal yi
Tekki
Na ñu am 3 tomb A, B ak P yu bokkul te t di toxal biy soppali tomb bii di A ci B.
- Su tomb bii di P bokkul ci rëdd wii di (AB), misaaluk (image) tomb bii di P ci toxal wii di t mooy tomb P′ biy tax ABP′P nekk bènn wet-yu-làŋ.
- Su tomb bii di P bokkee ci rëddd wii di (AB), misaaluk tomb bii di P ci toxal wii di t mooy tomb P′ biy tax dogit yii di [AP′] ak [BP] bokk bènn digg.
Jagleb toxal yi
- Ci bènn toxal, misaalu bènn dogit ab dogit la bu wetlàŋ ak moom te tollook moom guddaay.
- Ci bènn toxal, misaalu bènn rëdd ab rëdd la bu wetlàŋ ak moom.
- Ci bènn toxal, misaalu bènn xaaju rëdd ab xaaju rëdd la bu wetlàŋ ak moom te bokkak moom jëmukaay.
- Ci bènn toxal, misaalu bènn mbege rëdd ab mbege la bu tollook momm cn la bu tollook momm ceeñeer ; diggi nataal bi mooy misaaluk diggi mbege mu njëkk mi.
Ab toxal da fay denc raŋale yi, guddaay yi, angal yi, yaatuwaay yi, wetlàŋite gi ak jub-
dogoo gi.
II. Jëmu yi
Raññalekuk bènn jëmu
Jëmu bii di →AB li koy raññale mooy :
- Jubluwaayam te mooy rëdd wii di (AB).
- Jëmukaayam te mooy bu xaaju rëdd wii di [AB).
- Guddaay te mooy bu dogit wii di [AB].
Li koy mandargaal bènn fètt la.
Jëmu yu tolloo ak jëmu yu feewëloo
- 2 jëmu da ñoo tolloo bu fekkee ñoo bokk bènn jubluwaaay, bènn jëmukaay ak bènn guddaay.
→AB=→CD - 2 jëmu da ñoo feewëloo bu fekkee ñoo bokk bènn jubluwaaay, bènn gudday waaye seen jëmukaay yi feewëloo.
→AB ak →BA da ñoo feewëloo.
Jëmu ak wet-yu-làŋ
- Su ABCD nekkee ab wet-yu-làŋ, da ñuy am →AB=→DC.
- Su →AB=→DC te tomb yii di A, B, C ak D raŋale wu ñu, kon ñeentikoñ bii di ABCD ab wet-yu-làŋ la.
Digguk bènn dogit ak jëmu
- Su bènn tomb I nekkee digguk bènn dogit [AB] kon →AI=→IB.
- Su 3 tomb A, I, B melee ni →AI=→IB kon I mooy digguk [AB].