I. Angalu digg ; xala bu ñu japp ; guddayu xallaag bènn mbege

Dèes na tuddee angalu digg ci bènn mbege, bènn angal boo xamne pujam mooy diggi mbege mi. Dèes na tuddee xala bu bènn angalu digg japp ci bènn mbege xalaag mbege bi nekk ci biir wàllu angalu (secteur angulaire) bi angal bòbu di mandargaal.  
Guddaay $\mathrm I$ bu bènn xalaag mbege wu bènn angalu digg $\alpha$ ci jegoo (degré) japp ci bènn mbege mu ceeñeeram doon $r$ mu ngi tollook : $\mathrm I=\dfrac{2 \pi r \alpha}{360}$.

II. Wërngal yi 

Tekki ak tërëlinu tabaxin

Soppali bènn nataal ci bènn wërngël, mooy nga wañaar ko ci lu wërr bènn tomb. Liy xamle bènn wërngël mooy : 

  • bènn digg
  • bènn angalu wërngal
  • bènn jëmukaayu wërngël

Ab wërngël bu diggam di $\mathrm{O}$ te angalam di $\alpha$ da lay may nga wañaar bènn nataal ci lu wërr tomb bii di $\mathrm{O}$ ci bènn angal bu tollu ci $\alpha$ te doo soppi melokaanam.

Ay jagle

  • Ci bènn wërngël, misaaluk bènn dogit da fay nekk bènn dogit wu tollook moom guddaay. Ab wërngël da fay denc guddaay yi.
  • Ci bènn wërngël, misaaluk bènn rëdd da fay nekk bènn rëdd : ab wërngël da fay denc raŋale mi. 
  • Ci bènn wërngël, misaaluk bènn angal da fay nekk bènn angal bu tollook moom natt : ab wërngël da fay denc angal yi.   
  • Ci bènn wërngël, misaaluk bènn nataal  da fay nekk bènn nataal bu yemook moom yaatuwaay : ab wërngël da fay denc yaatuwaay yi. 
  • Ab wërngël da afy denc wet-laŋ et jub-dogoo yi. 

III. Bariwet yu jag yi

Ay tekki ak ay misaal

Ab bariwet bu wetam yëpp tolloo guddaay te angallam yëpp yem natt ñu ngi koy tuddee ab bariwet bu jag (régulier). 

Ay misaal :

  • Ñettkoñ bu wett-yem bi : 3 wett yu tolloo ak 3 angal yu tolloo.
  • Kaare bi : 4 wett yu tolloo et 4 angal yu yem natt.
  • Juroomikoñ bu jag bi : 5 wett yu tolloo et 5 angal yu yem natt.
  • Juroombennikoñ bu jag bi : 6 wett yu tolloo et 6 angal yu yem natt.

Ay jagle

  • Bépp bariwet bu jag te am $n$ wet du soppeeku ci bènn wërngël bu angallam nekk $\dfrac{360°}{n}$ ci boo jëlee tombam yëpp.
  • Bépp bariwet bu jag manees na am bènn mbege bu ñu rëdd ci biiram. 
  • Bépp bariwet bu jag manees na am bènn mbege bu ñu rëdd ci biteem te mu wërr ko.
  • Bépp taseebkawewaayu bènn wetuk bènn bariwet bu jag da fay aksu safaanook jàkkaarle bu bariwet bòbu.