Angal yu safaano ci puj :

Da ñuy naan ñaari angal yu bokkul wet te tukkee ci ñaari rëdd yu dogante da ñoo feewëloo ci puj.

Ab jagle : 

Su ñaari angal feewëloowee ci puj, da ñuy yem natt. 

Angal yi defaroo ci ñaari rëdd yu beneen dog

1) Soo amee ñaari rëdd yu bokkul te beneen rëdd dog leen (rëdd wòwu ñu ngi koy woowee dogkat) ñaari angal yu nekk ci digante ñaari rëdd yu njëkk yi, bokkuñ wet te feetewoo ci bènn wàllaa ak beneen wàllaa ci dogkat wi ñu ngi leen di tuddee ay angal yu jallawle biir (alternes-internes).


$\left(d_1\right)$ ak $\left(d_2\right)$ da ñoo wet-làŋ.
$\rm\widehat{M_1}$ ak $\rm\widehat{K_1}$ da ñoo jallawle biir.

$\rm\left(D_1\right)$ ak $\rm\left(D_2\right)$ wet-làŋu ñu.
$\rm\widehat{A_3}$ ak $\rm\widehat{B_1}$ da ñoo jallawle biir.

2) Soo amee ñaari rëdd yu bokkul te bènn dogkat dog leen, ñaari angal yu nekk ci bitik ñaari rëdd yi, bokkuñ wet te feetewoo ci bènn wàllaa ak beneen wàllaa ci dogkat wi ñu ngi leen di tuddee ay angal yu jallawle biti (alternes-externes).

$\rm (CD)$ ak $\rm (EF)$ da ñoo wet-làŋ.
$\rm\widehat{A_2}$ ak $\rm\widehat{B_1}$ da ñoo jallawle biti.

$\rm\left(D_1\right)$ ak $\rm\left(D_2\right)$ wet-làŋu ñu.$\rm\widehat{A_2}$ ak $\rm\widehat{B_1}$ da ñoo jallawle biti.

3) Soo amee ñaari rëdd yu bokkul te bènn dogkat dog leen, ñaari angal yu bokkuñ wet, kènn ki nekk ci biir, keneen ki  bitik ñaari rëdd yi, te ñu feetewoo ñoom ñaar ci bènn wàllaak dogkat wi ñu ngi leen di tuddee ay angal yu mengoo (correspondants).

4)  Soo amee ñaari rëdd yu bokkul te bènn dogkat dog leen, ñaari angal yu nekk ci biir ñaari rëdd yi, te feetewoo ci bènn wàllaak dogkat wi ñu ngi leen di tuddee ay angal yu nekk ci biir te bokk wàllaa (intérieurs d'un même côté).

$\rm\widehat{A_3}$ ak $\rm\widehat{B_2}$ da ñoo nekk ci biir te bokk wàllaa.

Ay jagle

Su ñaari rëdd wet-làŋee te bènn dogit dogantee ak ñoom, su boobaa :

  • ñaari angal yu jallawle biir da ñuy tolloo ;
  • ñaari angal yu jallawle biti da ñuy tolloo ;
  • ñaari angal yu nekk ci biir te bokk wàllaa da ñuy dolliwante.