Yemoo gii di a+x=b, ci loo xamne a ak b ay fukkeel yu ñu joxe la, dèes na ko tuddee ab yemale bu deetxamam (inconnue) nekk x.
Sottali yemale a+x=b ci bènn mbooloo, mooy nga fexe ba gennee ci mbooloo mòmu njëgug deetxam bii di x ngir yemoo bi jub.
Yemale bii di a+x=b ab sottalam mooy x=b−a.
Ngir sottali bènn yemale bu nekk ci melokaanu ax=b te a≠0, da ñuy xaajale b parci a.
Su fekke ne a≠0, yemale ax=b sottalam da fay nekk x=ba.
Wuute bii di a+x<b, fu a ak b nekkee ay fukkeel yu ñu joxee ñu ngi koy woowee ab yemadi bu deetxamam nekk x.
Ci bènn yemadi ñaari cërr yi bènn mandargaay wuute moo leen di xaajale.
a+x mooy cërr wu njëkk wu yemadi gi te b mooy cëruk ñaareel wi.
Ngir sottal yemadi gii di : a+x≤b, da ngay yokk ci ñaari cërr yi feewëloo bu a, nga daal di am yemadi gii di : x≤b+feewëlook a (maanaam x≤b−a).
Su boobaa di nga mana soppi sottal gi ci bènn nataal.
Ay misaal :
✓ 2,5+x<6 ; x<6−2,5 ; x<3,5
Mbooloom sottal yi mooy wàll gi ñu rëddul.
✓ 7+x≥1,2 ; x≥1,2−7 ; x≥−5,8
Mbooloom sottal yi mooy wàll gi ñu rëddul.