Yombalinu ab tojit

Soo jëleer a ak b ñaari limmum lëmm, b bokkeewul ak tus te k di bènn limmum lëmm bu wûteek tus, da ñuy am :

ab=a×kb×k=a÷kb÷k

Yombalal ab tojit mooy nga xaajale limmum kowam ak limmum suufam ci mennam xaajkat bu ëpp 1. Su ñu manula yombal bènn tojit, da ñuy naan da fa lees waññi.

Ngir fexe soppi bènn tojit ba mu lees waññi, da ngay xaajale limmum kowam ak limmum suufam yëpp ak seen XMGM.  

Mann ngaa jëfëndikoo tasaare ci meññeefu ëmbeefu limm yu njëk ngir yombalal ab tojit. 

Mengaleek bènn tojit ak bènnal gi

Soit la fraction ab avec a et b deux entiers naturels et b0.

Na ñu jël tojit wii di ab te a ak b doon ñaari limmum lëmm mu anndak b0.

Su limmum kow a bu bènn tojit da fa tollook limmum suufam b, kon tojit wòwu dafay yemak bènnal gi.

Maanaam, su a=b, kon ab=1

Su limmum kow a bu bènn tojit da fa yèes limmum suufam b, kon tojit wòwu dafay gëna tûti bènnal gi.

Maanaam, su a<b, kon ab<1.

Mengaleek ñaari tojit

Su ñaari tojit bokkee bènn limmum suuf, bi ci ëpp mooy bi ëppale limmum kow.

Su ñaari tojit bokkee bènn limmum kow, bi ci ëpp mooy bi gëna tûtile limmum suuf.

Mbinndum bènn tojit ab ci melokaanu q+rb

a,b,q ak r ay limmum lëmm la ñu te b0.

Bepp tojit ab manees na ko binnd ci melokaan wi : q+rb, mu anndak r<b, q mooy xaajit te r mooy ndesiti xaajaleek a ci b.

Wërële bènn tojit ci ñaari limmum fukkeel 

Ab tojit wu nekk man na ko wërële ak ñaari limmum fukkeel yu ñuy woowee xaajit wu jege te yèes (limm bi gënë tûti) ak xaajit wu jege te ëpp (limm bi gënë mak).  

Yokkalante ak waññik ñaari tojit

Ngir yokkalante wala waññi ñaari tojit yu bokk bènn limmum suuf, da ngay yokkalante (wala nga waññi) limmum kow yi te teye limmum suuf yi.  

Maanaam, su a,b ak c nekkee ñetti limmum lëmm anndak c0, da ngay am :

ac+bc=a+bc ak acbc=abc

Ngir yokkalante wala waññi ñaari tojit yu seen limmum suuf yi wûte, da nga leen di soppali ba ñu bokk limmum suuf.  

Ñaare ngir def lòlu, da ngay jël FMGT wu limmu suuf yi nga njëkkoona am mu nekk limmum suuf bi ñuy bokk. Soo noppee ci lòlu nga topp doxalin yi ñu joxe woon si kow.

Fŭllanteek ñaari tojit

Ngir fŭllante ñaari tojit, da ngay fŭllante limmum kow yi ci seen biir ak limmum suuf yi ci seen biir.  

Maanaam, su a,b , c ak d nekkee ay limmum lëmm, anndak b0 et d0 da ñuy am :

ab×c=a×cb ak ab×cd=a×cb×d

Xaajaleek benn tojit ci bènn limmum lëmm

Ngir xaajale benn tojit ci bènn limm, da ngay fŭllante limm wòwu ak limmum suufu tojit wi, topp nga yombalal jeexital wi soo ko manee.  

Su a,b ak c nekke ñetti limm, mu anndak b0 te c0, da ñuy am :

ab÷c=ab×c