Barikanam wu jub 

Ab barikanam bu jub bènn mbir mu dëgër la mu ay kanaman yi feetee wet nekk ay jubkoñ te ay sukkëndikukaayam doon ay bariwet yu yemoo kepp.  

Mboloom kanamam yi feetee wet mooy yaatu-yaatuk wet wi (aire latérale). 

Ab kawewaayu bènn barikanam bu jub  bènn yax la bu jub dogoo ak sukkëndikukaay yi. (ci misaal : $\rm [AB]$, $\rm [SL]$, …).   

Su ñu ko waxee neneen, ab kawewaay guddaayu bènn ci yax yòyu la.

Ab boyeet wu jub bènn barikanam bu raññeeku la boo xamne ay sukkëndikukaayam ay jubkoñ la ñu.  

Ab kub bènn barikanam wu jub la  boo xamne wetam yëpp ay kaare yu yemoo la ñu.

Tallalluk bènn  barikanam bu jub

Ngir nataal tallalluk bènn barikanam bu jub, da nga wara : 

  • Rëdd benn ci sukkëndikukaay yi, muy nekk bènn ñettkoñ wala bènn jubkoñ, soo noppee nga rëdd bènn kanamu wet muy bènn jubkoñ bu ay wetam nekk bènn wetu sukkëndikukaay wi ak kawewaayu barikanam wu jub wi.  
  • Rëdd ñaareelu sukkëndikukaay mi, muy safaanoo jàkkaarle ak bu njëkk bi ci bènn ci aksu safaanook jàkkaarle bu jubkoñ bi.
  • Mottali tallale bi ci rëdd ñaari kanamu wet yu mujj ci barikanam bu jub wi, nga xamne ay jubkoñ la ñu.  

Wetlàŋ ak jub-dogoo ci jawwu ji 

Wetlàŋ ci jawwu ji

  • Ñaari rëdd yu jawwu ji da ñoo wetlàŋ su ñu bokkee nekk ci bènn maasale (bokkpalaŋ) te amu ñu bèn  tomb bu ñu bokk ñoom ñaar. 
  • Ñaari maasale da ñoo wetlàŋ su ñu doonee bènn wala su ñu bokkul bènn tomb.  
    Bènn rëdd ak bènn maasale da ñoo wetlàŋ su ñu bokkul bènn tomb.

Jub-dogoo ci jawwu ji

  • Ñaaru rëddu jawwu ji da ñoo jub-jëmu (orthogonales) su fekkee ne ñaari rëdd yu leen wetlàŋ tey jaar ci bènn tombu jawwu ji bu mu mana ti doon da ñoo jub-dogoo ñoom ci seen bopp.  
  • Ne bènn rëdd da fa jub-dogoo ak bènn maasale mu ngi firi ne rëdd wòwu da fa jub-dogoo ak rëdddu maasale gògu yëpp.  
  • Ñaari maasale $\rm P$ ak  $\rm P’$ yu jawwu ji da ñoo jub-dogoo su fekkee ne bènn rëdd  $\rm (D)$ bu $\rm P$ da fa jub-dogoo ak bepp rëdd $\rm (D’)$ bu $\rm P’$. 

Ñaaru rëdd yu bokk nekk ci bènn maasale te jub-dogoo da ñoo jub-jëmu, waaye ñaari rëdd yu jub-jëmu du ñu bokk di nekk ci bènn maasale saay wu nekk. 

Guddaay yi, yaatuwaay yi ak këmb yi

Yaatu- yaatuk bènn barikanam bu jub

  • Yaatu-yaatuk wet (aire latérale) bu bènn barikanam bu jub mooy ndajaleeek yaatu-yaatuk ay kanami wetam. 
  • Yaatu-yaatuk wet bènn barikanam bu jub mu ngi tolloo itam ak guddaayu sukkëndikukaay bi bu ñu fŭllante ci kawewaayam. 
  • Yaatu-yaatuk lëmm bu bènn barikanam bu jub mooy ndajaleeek yaatu-yaatuk wetam ak yaatu-yaatuk ay sukkëndikukaayam. 

Këmbu bènn barikanam bu jub  

Këmbu bènn barikanam bu jub mu ngi tollook fŭllanteek yaatu-yaatuk sukkëndikukaayam ci kawewaayam.  
Maanaam, su $\rm S$ nekkee yaatu-yaatuk sukkëndikukaay mi, $k$ di kawewaayam  te $\rm K$ di këmbam, Kon $\mathrm{K = S} \times h$.