Ñaariwetlaŋ
Xamle
Ab ñaariwetlàng bènn ñeentikoñ la bu am ñaari wett yu jub-làŋ.
Yeneen ñaari wet yi jub-làŋuñ.
Ab ñaariwetlàng bu jubkoñ mooy bènn ñaariwetlàng bu am bènn angal wu jub.
Ab ñaariwetlàng bu ñaariwet-yem mooy bènn ñaariwetlàng boo xamne ñaari wetam yi seen sukkëndikukaay dogoo ñoo yem guddaay.
Ab ñaariwetlàng bu ñaariwet-yem da fay am bènn aksu safaanook jàkkaarle buy doon taseebkawewaayu ay sukkëndikukaayam.
Ci bènn ñaariwetlàng bu ñaariwet-yem, ñaari angal yi feetewoo ak sukkëndikukaay yi ñoo yem natt.
Xammeekuk bènn ñaariwetlàng
- Su bènn ñaariwetlàng amee bènn angal wu jub, da fay daal di jubkoñ.
- Su bènn ñaariwetlàng amee ñaari angal ci sukkëndikukaayam yu yem natt, da fay ñaariwet-yem.
- Su bènn ñaariwetlàng amee bènn aksu safaanook jàkkaarle buy doon taseebkawewaayu sukkëndikukaayam yi, da fay wett-yem.
Yaatu-yaatuk ñaariwetlàng bi
Yaatu-yaatuu bènn ñaariwetlàng mu ngi tollook ndajaleek sukkëndikukaayam yi (sukkëndikukaay bu mak + sukkëndikukaay bu ndaw) ñu fŭllante ko ak kawewaayam, ba noppi xaaj ko si $2$.
Maanaam, $\text{Yaatu-yaatu} = \dfrac{(\mathrm M + n)\times h}{2}$ (mu andak $\rm M$ di sukkëndikukaay bu mak bi, $n$ di sukkëndikukaay bu ndaw mi te $h$ di kawewaay wi).
Jub-koñ
Xamle
Ab jub-koñ bènn ñeentikoñ la bu am ñeenti angal yu jub.
Ay jagle :
- Ay galaŋu bènn jubkoñ ñoo yem guddaay.
- Taseebkawewaayu weti bènn jubkoñ ay aksu safaanook jàkkaarle la ñu.
- Ci bènn jubkoñ, galaŋ yi ak aksu safaanook jàkkaarle yi da ñuy dogoo ci diggu safaanook jàkkaarle gi.
Xammeekuk bènn jubkoñ
- Su bènn wetlàŋ amee bènn angal bu jub, da fay nekk ab jubkoñ.
- Su bènn wetlàŋ amee ay galaŋ yu tolloo guddaay, da fay nekk ab jubkoñ.
Yaatu-yaatuk ab jubkoñ
L’aire d’un rectangle est égale au produit de sa longueur par sa largeur.
Yaatu-yaatuk bènn jubkoñ mu ngi tollook fŭllanteek gaddaayam ci yaatuwaayam.
Maanaam, Yaatu-yaatu = Guddaay × yaatuwaay.
Kaaredoy
Xamle
Ab kaaredoy bènn ñeentikoñ la bu ñeenti koñam yëpp tolloo guddaay.
Ay jagle :
- Ci bènn kaaredoy galaŋ yi da ñuy dogoo ci seen digg te da ñuy jub-dogoo.
- Ab kaaredoy da fay am diggu safaanook jàkkaarle muy tombu doganteek ay galaŋam. Un losange admet pour centre de symétrie le point d’intersection de ses diagonales.
- Ay galaŋi bènn kaaredoy ñooy aksu safaanook jàkkaarleem.
Xammeekuk bènn kaaredoy
- Su bènn wetlàŋ amee ñaari wet yu toftalante te yemoo guddaay, kon ab kaaredoy la.
- Su bènn wetlàŋ amee ay galaŋ yu jub-dogoo, kon ab kaaredoy la.
- Su bènn wetlàŋ amee bènn galaŋ bu nekk itam xaaj-diggu bènn angal, kon kaaredoy la
Yaatu-yaatuk bènn kaaredoy
Yaatu-yaatuk bènn kaaredoy da fay tollook fŭllanteek galaŋ yi ñu xaaj ko si $2$.
Kaare
Xamle
Ab kaare bènn ñeentikoñ bu $4$ wetam yëpp tolloo gudday te $4$ angallam yëpp jub.
Kaare bu nekk da fay nekkandoo jubkoñ ak kaaredoy.
Ay jagle :
- Ay galaŋu bènn kaare da ñuy jub-dogoo te tolloo guddaay.
- Ab kaare ñeenti aksu safaanook jàkkaarle la am ak bènn diggu safaanook jàkkaarle.
- Ab kaare da fay am mbooleem jagleek bènn jubkoñ ak bènn kaaredoy.
Xammeekuk bènn kaare
- Kaare bu nekk bènn kaaredoy bu raññeeku la :
- Su bènn kaaredoy amee bènn angal bu jub, kon da fay nekk bènn kaare.
- Su bènn kaaredoy amee ay galaŋ yu tolloo guddaay, kon da fay nekk bènn kaare.
- Kaare bu nekk bènn jubkoñ bu raññeeku la :
-
- Su bènn jubkoñ amee ñaari wet yu toftalante te tolloo guddaay, kon da fay nekk bènn kaare.
- Su bènn jubkoñ amee ay galaŋ yu jub-dogoo, kon da fay nekk bènn kaare.
- Su bènn ñeentikoñ boolee nekk bènn kaaredoy ak bènn jubkoñ, kon da fay nekk bènn kaare.
Yaatu-yaatuk bènn kaare
Yaatu-yaatuk bènn kaare mu ngi tollook fŭllanteek ñaari wet.