I. Xaajale ci anamu Ëklid 

Na $a$ ak $b$ nekk ñaari limmum lëmm te b demee nii $b \neq 0$.
Defar xaajalinu Ëklid bu $a$ ci $b$ mu ngi firi nga wone ñaari limmum lëmm $q$ ak $r$ yuy tax ñu am : $\color{orangered}{a=b \times q+r}$ avec $r < b$.

II. Fŭlkatu mbootaay yu ñaar ba ñetti limmum lëmm 

Na $a, b$ ak $q$ nekk ñetti limmum lëmm. Su ñu amee : $a=b \times q$, da ñuy naan a fŭlkatu $b$ ak $q la; b$ et $q$ ay xaajkatu $a$ la ñu.

Ay seetlu :

  • $0$ bènn fŭlkat rek la am te mooy $0$ si boppam.
  • Bepp limmum lëmm dina am ay fŭlkat yu dul jeex.
  • Bepp limmum lëmm ay xaajkat yu limu rekk la am. 
  • Bepp limmum lëmm da fay nekk fŭlkat ak xaajkatu boppam.  

Ab jagle :

Su $a$ nekkee fŭlkatu $b$ wala $b$ doon xaajkatu $a$, su boobaa xaajaleek $a$ ci $b$ da fay joxe bènn ndessit wu tollook tus (xaajit wu yem kepp).

Su bènn limmum lëmm $a$ nekkee fŭlkatu ñaari limmum lëmm yu dul tus te wûte $b$ ak $c$, da ñuy naan $a$ fŭlkatu mbootaay la ci $b$ ak $c$.

Ab seetlu : $0$ fŭlkatu limmum lëmm yëpp la.

III. Xaajkatu mbootaay yu ñaar ba ñetti limmum lëmm 

Su bènn limmum lëmm $b$ nekkee xaajkatu ñaari limmum lëmm yu yemul te du ñu tus $a$ ak $c$, kon da ñuy naan $b$ ab xaajkati mbootaay la ci $a$ ak $c$.

Ab seetlu : 1 ab xaajkat la ci bepp limmum lëmm.

IV. Limm yu njëkk yi

Ab limm bu njëkk bènn limmum lëmm la bu wûteek $1$ te am ñaari xaajkat doŋ : $1$ ak moom ci boppam.

Ngir xam ndax bènn limm limm bu njëkk la am deet, da ñu koy xaajale ci toftalante buy yokku ak limm yu njëkk yi ko yèes yëpp. Su ñu amee :

  • Ak xaajit wu yèes wala wu tollook xaajkat wi, kon limm wi ak limm bu njëkk la.
  • Ak ndessit wu tollook tus, kon limm wi du ab limm bu njëkk.

Ab seetlu : Da ngay taxawal xaajale gi saay woo amee ndesit wu yèes wala wu tollook xaajkat wi.

V. Tasaare ab limmum lëmm ci bènn meññeefu ëmbeefu limm yu njëkk  

Ab jagle :

Bepp limmum lëmm bu dul limm bu njëkk manèes na ko tasaare ci bènn meññeef moo xamne ëmbeefam yëpp ay limm yu njëkk la ñu.

Ngir tasaare bènn limmum lëmm ci ab meññeefu ay ëmbeefu limm yu njëkk :

  • Da nga koy xaajale ci xaajkatam bi gënë tûti te nekk limm bu njëkk.
  • Soo noppee, saay wu nekk nga def lu ni mel ak xaajit wi ngay am.
  • Nga daal di taxawal xaajale yi soo demee ba xaajit wi nekk 1.

Ci misaal :

           

    VI. FMGT ak XMGM bu ñaar mbaa ñetti limmum lëmm

Tënkin wii di FMGT mu ngi firi : Fŭlkatu Mbootaay wi Gëna Tûti bu ñaari limmum lëmm $a$ ak $b$. Ñu ngi koy binndee $\color{orangered}{\mathrm{FMGT}(a~ ; b)}$.

Ngir xayma FMGT wu ñaari limmum $a$ ak $b$ :

Da ngay tasaare $a$ ak $b$ ci ay meññeefu ëmbeefu limm yu njëkk.
Nga fŭllanté ëmbeef yi nga am yëp ci tasaare gi tey jël ci ëmbeef bu nekk maaskow bi ëpp.
Tënkin wii di XMGM mu ngi firi : Xaajkatu Mbootaay wi Gëna bu ñaari limmum lëmm $a$ ak $b$. Ñu ngi koy binndee $\color{orangered}{\mathrm{XMGM}(a~ ; b)}$.

Ngir xayma XMGM wu ñaari limmum $a$ ak $b$ :

  • Da ngay tasaare $a$ ak $b$ ci ay meññeefu ëmbeefu limm yu njëkk.
  • Nga daal di fŭllanté ëmbeef yi bokkandoo si ñaari tasaare yi tey jël ci ëmbeef bu nekk maaskow bi gëna tûti.