Xamale

Ab wet-yu-làŋ mooy bènn ñeentikoñ boo xamne wetam yi feewëloo da ñoo wet-làŋ 

Ay jagle

1) Ci bènn wet-yu-làŋ, galaŋ yi da ñuy dogoo ci seen digg. 

Tomb bòbu da fay nekk diggu safaanook jàkkaarle bu wet-yu-làŋ bi. 

2) Ci bènn wet-yu-làŋ, wet yi feewëloo da ñuy yemoo guddaay.

ABCD ab wet-yu-làŋ la, kon AB=DC te AD=BC.

3) Ci bènn wet-yu-làŋ, ñaari angal yu feewëloo da ñuy yem natt.

Ci bènn wet-yu-làŋ, ñaari angal yu toftalante da ñuy ëppalante.

ABCD ab wet-yu-làŋ la, kon ˆA=ˆC te ˆB=ˆD :

  • ˆA+ˆB=180 ;
    ˆB+ˆC=180 ;
    ˆC+ˆD=180 ;
    ˆD+ˆA=180.

Xammeekuk bènn wet-yu-làŋ

1) Su wet yi feewëloo ci bènn ñeentikoñ yëpp da ñoo wet-làŋ, kon ñeentikoñ bi ab wet-yu-làŋ la.

(AB)//(DC) et (AD)//(BC), kon ABCD ab wet-yu-làŋ la.

2) Su galaŋu bènn ñeentikoñ dogoo ci seen digg, kon ab wet-yu-làŋ la.

O mooy digguk [AC] te O mooy digguk [BD], kon ABCD ab wet-yu-làŋ la.

3) Su bènn  ñettkoñ amee ay angal yu feewëloo yu yem natt ñaar ñaar, kon ab wet-yu-làŋ la.  

4) Su  fekke ne ci bènn ñeentikoñ, ñaari dendaleek angal yu toftalante yu nekk da ñoo dolliwante, ñeentikoñ bòbu ab wet-yu-làŋ la. 

ˆA=ˆC te ˆB=ˆD, kon ABCD ab wet-yu-làŋ la.

  • ˆA+ˆB=180 ;
  • ˆB+ˆC=180 ;
  • ˆC+ˆD=180 ;
  • ˆD+ˆA=180.

Yaatuwaayuk bènn wet-yu-làŋ

Su ABCD doonee bènn wet-yu-làŋ, kon Yaatuwaay(ABCD) =sukkëndikukaay×kawewaay= DC×AH.