Nataalug bènn anamu dëppoo ci xaajalé da fay nekk bènn rëdd buy jaar ci tambalinu gindeekukaay bi.  

Ci misaal : Bènn anamu dëppoo ci xaajalé mu ngi nii ak nataalam.

Mottali bènn alluwaak dëppoo ci xaajale

Ngir mottali bènn alluwaak dëppoo ci xaajale, man nga xayma limm giy mandargaal dëppoo ci xaajale gi, te mooy njëk wiy dëppook “bènneel gi”.

Soo jëfënndikoo limm gògu, di nga man mottali alluwà gi, dimbalikoo ak ay fŭllante wala ay xaajale. Man nga koo motali itam ci dimbalikoo ak ay yokkalante wala ay waññi ci digante kènu yi.

Xayma bènn xaajitu teemeeral

Xayma bènn xaajitu teemeeral mook mottali bènn alluwaak dëppoo ci xaajale bènn la ñu.    

Ci misaal : Ci bènn “estad” bu am $40~ 000$ palaas, am na fa $28~ 000$ seetaankat. 

Na ñu xayma xaajitu teemeerali feesaayu “estad” bòbu ci ndimbalu bènn alluwaak dëppoo ci xaajale :

Xayma ak bènn tolloole

Ngir mandargaal bènn yaatu-yaatu wala bènn mbir mu rëy, da ñu koy nataal ci lu gëne tûti. Ngir def lòlu da ñuy dimbalikoo bènn tolloole, muy bènn limm guy mandargaal ab dëppoo ci xaajale ci digante soreewaay yi dëgg ak soreewaay yi ci nataal gi.

$\boxed{\text{Tolloole} = \dfrac{\text{soreewaay gi ci nataal bi}}{\text{soreewaayu dëgg bi}}}$ (ñaari soreewaay yi ñoo bokk bènn bènnal)