Na $b$ nekk bènn limmum fukkèl bu ñuy xaymaa, te  $n$ nekk bènn  limmum lëmm bu ëpp wala mu tollook  $2$. Dèes na tuddee kàttanu $n–{\text{neel}}$ bu bènn fukkeel  $b$, jeexitali fŭllantèk $n$ ëmbeef (facteurs) yu tolloo yëpp ak $b$.

Lòlu da ñu koy binndee $b^n=\underbrace{b \times b \times \ldots \times b}_{n \text { ëmbeef yu tollook } b}$

$b^n$ bènn kàttanu limm bii di $b$ la.

$n$ mooy maasukow (exposant) bu kàttan wòwu.

$b^n$ ñu ngi koy jangee $b$ maasukow $n$ wala $b$ ci kàttani $n$.

ñu ngi nangu ne $b^1=b$ ; $b^0=1(b \neq 0)$ ; $1^n=1$ ; $0^n=0$

Su $a$ ak $b$ nekkee ñaari fukkeel te $n$ nekk bènn limmum lëmm bu ëpp wala mu tollook  $2$, da ñuy am $(a \times b)^n=a^n \times b^n$

Su $x$ nekkee bènn fukkeel bu ñuy xaymaa te $n$ ak $p,$ nekkee ay limmum lëmm, da ñuy am $x^n \times x^p=x^{n+p}$.

Su $a$ nekkee bènn fukkeel, $m$ ak $n$ di ñaari limmum lëmm yu ëpp wala ñu $2$, da ñuy am $\left(a^n\right)^m=a^{n \times m}$.