Ci bènn xammalekukaayu maasale gi, barab bi bènn tomb nekk ñu ngi koy xamee ci ñaari limm yu kokkaloo yuy ay maaskaam :
Bi si njëkk mooy maasskaam tëdd wi te ñaarèl bi mooy maasskaam taxaw mi.
Tomb bii di $\rm O$ te ay maaskaam nekk $(0~ ; 0)$ mooy tambalinu xammalekukaay bi.
Jang maaskaayu bènn tomb :
Da ngay seet maasskaam tëdd mi ci rëdd wi tëddà (rëddu maaskaay tëdd yi) ak maasskaam taxaw mi ci rëdd wi taxaw (rëddu maaskaay taxaw yi).
Maaskaay $\rm A$ ñooy $(\color{limegreen}{-1}~ ;\color{red}{3})$ $(-1~ ;3)$.
Maaskaay $\rm B$ ñooy $(\color{limegreen}{2}~ ;\color{red}{4})$ $(2~ ;4)$.
Maaskaay $\rm C$ ñooy $(\color{limegreen}{3}~ ; \color{red}{-2})$ $(3~ ; -2)$.