Safaanook jàkkaarle bu bènn tomb $\rm A$ ci safaanoo jàkkaarle bi diggam nekk tomb $\mathrm{O}$ mooy tomb $\rm A'$ biy tax tomb bii di $\mathrm{O}$ nekk diggu dogit wii di $\rm [AA]'$.

Diggu safaanook jàkkaarle

Su fekkee bènn nataaal ak safaanook jàkkaarleem ci safaanoo jàkkaarle bi diggam nekk tomb bii di $\mathrm{O}$ da ñu nekk bènn, da ñuy naan tomb $\mathrm{O}$ mooy diggu safaanook jàkkaarlee bu nataal bi.

Safaanook jàakkarlee bu bènn nataal bu ñu raññee – nataal yu safaanoo jakkarlee

Ci bènn safaanook jàkkaarle, jàkkarlook bènn rëdd ab rëdd la, jàkkarlook bènn xaaj-rëdd ab xaaj-rëdd la, jàkkarlook bènn dogit ab dogit la.

Safaanoo jàkkaarleek mbege mii di $\rm (C)$ ci tomb $\rm O$ mooy mbege mii di  $\rm (C’)$.

Safaanoo jàkkaarleek ñettkoñ bii di $\rm ABC$ ci tomb $\rm O$ mooy ñettkoñ bii di $\rm A’B’C’$.

Ci bènn safaanoo jàkkaarle bu am digg, jàkkarlook bènn angal da fay nekk bènn angal.

Ci bènn safaanoo jàkkaarle bu am digg, jàkkarlook bènn jubkoñ da fay nekk bènn jubkoñ.

Ci bènn safaanoo jàkkaarle bu am digg, jàkkarlook bènn kaare da fay nekk bènn kaare.

Ay Jagleek safaanook jàakkarlee bu am digg

Ab safaanook jàakkarlee bu am digg da fay :

  • denc soreewaay yi : maanaam, ci bènn safaanook jàakkarlee bu am digg, jàkkarlook bènn dogit bènn dogit la bu jub-làng te yemoo guddaay ak moom.
  • denc raŋale yi : su ay tomb raŋalee, seeniy safaanook jàkkaarle da ñuy raŋale. 

  • denc angal yi : bènn angal ak safaanook jàkkarleem ñoo yem natt.
  • denc yaatuwaay yi : beènn nataal ak safaanook jàkkaarleem ñoo bokk yaatuwaay.