Ndajaleek angalu bènn ñettkoñ
Ci bènn ñettkoñ, ndajaleek angal yi mu ngi tollook $180°$.
Su ñu ko waxee neneen, bu $\rm ABC$ nekkee ab ñettkoñ, kon da ñuy am $\rm mes \widehat{A} + mes \widehat{B} + mes \widehat{C}=180°$.
Rëdd yu raññeeku yi
-
Ci bènn ñettkoñ, tasebkawewaay da ñuy dogoo ci bènn tomb.
Tomb bòbu mooy nekk diggu mbege miy wërële ñettkoñ bi. Maanaam, mbege mòmu da fay jaar ci ñetti puji ñettkoñ bi. -
Ci bènn ñettkoñ, ñetti kawewaay yi da ñuy dogoo ci bènn tomb.
Tomb bòbu mooy jub-diggu (orthocentre) ñettkoñ bi.
Ñettkoñ bu koñjub
- Ci bènn ñettkoñ bu koñjub, angal yu xat yi (angles aigus) da ñuy mottaliwante. Maanaam, su fekkee $\mathrm{ABC}$ ab ñettkoñ bu koñjub la ci $\mathrm{A}$, kon da ñuy am $\rm\widehat{A B C}+\widehat{A C B}=90°$.
- Ci bènn ñettkoñ bu koñjub digguk janookoñjub gi (hypoténuse) da fay nekk digguk mbegeek wërële mi (cercle circonscrit).
- Ci bènn ñettkoñ bu koñjub, soreewaayu digguk janookoñjub gi ak pujuk ñettkoñ bi ñoo tolloo
Xammeekaayu bènn ñettkoñ bu jub
-
Su ñaari angali bènn ñettkoñ mottaliwantee, kon ñettkoñ bòbu dafa koñjub.
Maanaam, su $\rm A B C$ nekkee bènn ñettkoñ te $\rm\widehat{B} + \widehat{C}=90°$, kon $\rm A B C$ da fay nekk koñjub ci $\rm A$. -
Soo jokkalee bènn tomb bu bènn mbege ak cetiy bènn si jaar-diggam yi bu tomb bòbu bokkul, kon da ngay am bènn ñettkoñ bu koñjub.
Maanaam, su $\rm A B C$ nekkee bènn ñettkoñ bu jub, $\rm A \in(C)$ te $\rm [B C]$ nekk bènn jaar-diggu $\rm (C)$, kon $\rm ABC$ da fay nekk koñjub ci $\rm A$. -
Su fekkee ne, si bènn ñettkoñ, digguk bènn wet dafa tolloo soreewaay ak puj yi, kon ñettkoñ bòbu da fa koñjub.
Maanaam, su $\rm A B C$ nekkee bènn ñettkoñ te $\rm I$ di diggu $\rm [B C]$ te itam $\rm I A=I B=I C$, kon $\rm A B C$ da fa koñjub ci $\rm A$.
Ñettkoñ bu ñaariwet-yem
Ab ñettkoñ bu ñaariwet-yem da fay am aksu safaanoo jàkkaarle
Ci bènn ñettkoñ bu wet-yem, ñaari angal yi feetee ci sukkëndikukaay bi ñoo tolloo.
$\rm A B C$ dafa ñaariwet-yem ci $\rm A$, kon $\rm\widehat{B}=\widehat{C}$.
Aksu safaanoo jàkkaarle bi da fay boole nekk :
- taseebkawewaayu sukkëndikukaay bi,
- seddalekoñ bu pujum cosaan wi,
- kawewaay ak jaar-diggu sukkëndikukaay bi.
Xammeekaayu bènn ñettkoñ bu ñaariwet-yem
- Su bènn ñettkoñ amee aksu safaanoo jàkkaarle, kon dafa ñaariwet-yem.
Maanaam, su $\rm A B C$ nekkee bènn ñettkoñ te $(\Delta)$ bènn aksu safaanook jàkkaarle bu $\rm A B C,$ kon $\rm A B C$ da fay ñaariwet-yem. - Su bènn ñettkoñ amee ñaari angal yu yem natt, kon da fa ñaariwet-yem.
Maanaam, su $\rm A B C$ nekkee bènn ñettkoñ te su fekkee ne $\rm\widehat{B}=\widehat{C}$, kon $\rm A B C$ da fay ñaariwet-yem ci $\rm A$.
Ñettkoñ bu wet-yem
Ab ñettkoñ bu wett-yem da fay am ñetti aksu safaanook jàkkaarle yuy doon taseebkawewaayu wetam yi.
Su bènn ñettkoñ wett-yemee, ñetti angallam yi da ñuy yem natt $(60°$ bu ci nekk).
Maanaam, su $\rm A B C$ nekkee bènn ñettkoñ bu wett-yem, kon $\rm\widehat{A}=\widehat{B}=\widehat{C}=60°$.
Tombu doganteek ñetti aksu safaanook jàkkaarle yi da fay boole nekk :
- diggu mbegeek wërële mi,
- jub-digg mi.
Xammeekaayu bènn ñettkoñ bu wet-yem
-
Su bènn ñettkoñ amee ñaari aksu safaanoo jàkkaarle, kon dafa wett-yem.
Maanaam, su $(\Delta)$ ak $\left(\Delta^{\prime}\right)$ nekkee ay aksu safaanook jàkkaarle bu ñettkoñ bii di $\rm A B C$, kon $\rm A B C$ dafa wett-yem. -
Su ñetti angalu bènn ñettkoñ toolloowee, dafa wett-yem.
Maanaam, su $\rm A B C$ nekkee ab ñettkoñ te su ñu amee $\rm\widehat{A}=\widehat{B}=\widehat{C}$, kon dafa wett-yem.