I. Baat yi ñuy jëfëndikoo
Bu ñu yokee 2,6 ci 7,89, da ñuy amm 10,49. Xayma boobu dees na ko tuddee ab yokk. 10,49 mooy ndajalék (somme) 2,6 ak 7,89.
2,6 ak 7,89 ñooy cërr yi.
Sik yaatal, su a ak b nékkè ay limmum fukkel, boolèk limmum fukkel a ak limmum fukkel b ñu ngi koy binndè a+b ; a et b ñooy cëruy boolé moomu.
Ci benn boolé :
- cër yi ñooy limm yi ñuy boolé;
- ndajalé mi mooy jèxitalu boolé mi.
Ci missaal :
2,6+7,89=10,49 ; tëralin woowu mooy binnd cim rëdd (écriture en ligne) bu mboolé mi.
2,60+ 7,89 10,49
Tëralin wii nak mooy binnd ci kènnu (écriture en colonnes) bu mboolé mi.
Ci mbinnd moomu, dañuy yémalé xosi yi.
II. Ay Jaglé (Propriétés)
Weccaloo (commutativité)
Ñaari limmum fukkèl a ak b yoo jël, manees naa binnd :
a+b=b+a
Da ñuy naan "boolé" ab xayma bu dëppook weccaloo la.
Anndaalé (associativité)
Ñetti limmum fukkèl a, b ak c yoo jël, manees naa binnd :
(a+b)+c=a+(b+c)
Da ñuy naan « boolé » ab xayma bu dëppook anndaalé la.
Cëru tus ci ab boolé
Limm « tus », ñu koy binndè 0, du soppi dara ci ab boolé.
Maanam, su a nekkè benn limmum fukkèl bu mu mana doon, da ñuy amm :
a+0=a et 0+a=a
Da ñuy naan 0 ab cër “wu màndu” la (élément neutre) ci ab boolé.
Xayma ci lu gaaw ab ndajalé
- Soo buggee xayma ci lu gaaw ab ndajalé, mann ngaa tèè fas wi njëkk ba noppi ûtal 0 ci yi dess su fékkè ñaarèlu fas wi dafa nekk 0, 1, 2, 3 wala 4.
Ay missaal :
5 347 (sorèwul ak) →5 000
2 198 (sorèwul ak) →2 000 - Su ñaarèlu fas wi nekkè 5, 6, 7, 8 wala 9, su boobaa mann nga mengëlé limm bi nga amm ak limm bi ko gënë jégé, ëp ko, té and ak ay tus 158→200.
4 711→5 000. - Soo bëgè lu gënë jégé, da ngay tèè ay fas yu gënë bari
5 437 sorèwul ak 5 400
7 463 sorèwul ak 7 500
Soo bëggè am xayma bu gaaw ci benn ndajalé, da ngay boolé ay xayma yu jégé cër bu nekk.
Ci missaal :
Soo waroona xayma ci lu gaaw ndajalé bii 2 037,82+4 984,75 da ngay sètlu né 2 037,82 jégé na 2 000 té 4 984,75 jégé na 5 000 ; konn nak benn xayma bu gaaw bu 2 037,82+4 984,75 day nekk 2 000+5 000=7 000.