Yaatu-yaatu, yaatuwaay ak nattukaayu yaatuwaay yi
Yaatu-yaatuk bènn nataal moy wàll gi nekk si biir nataal gògu.
Yaatuwaayu bènn nataal mooy nattug yaatu-yaatu bi nataal bi di ëmb.
Bènneel bi ñiy jëfëndikoo ngir natt yaatuwaay yi ab kaare la.
Bènneelu yaatuwaay bi ñiy jëfëndikoo ngir yombal jëndak jaay yi ak xam xam yi (adduna yëppa si and) mooy « meetar kaare ». Ñu ngi koy binndee m2.
Am na yeneen bènneelu yaatuwaay. Ñu ngi leen di wone ci alluwaak wecceekaay bii si suuf :