I. Xeeti angal yi

Ñaari xaaj-rëdd da ñuy da ñuy mandargaal ñaari wàll ci maasale gi $\rm \widehat{BAC}$ ak $\rm \stackrel{\lor}{BAC}$. Wàll bu nekk bènn angal (wala koñ) la. Tomb bii di $\rm A$ mooy pujuk (sommet) angal bu  tòor- tòor bii di $\rm \widehat{B A C}$. Ñaari xaaji rëdd yii di $\rm [AB)$ ak $\rm [A C)$, nga xamne ñoo bokk tambalin $\rm O$, ñooy weti angal bu tòor- tòor bòbu.

   Angal yu ñu raññee

  • Angal bu jub : Su fekkee ne sukkënndikukaayu ñaari xaaj-rëdd yii di  $\rm [A B)$ ak $\rm [A C)$ da ñoo jub-dogoo, kon angal bii di $\rm \widehat{B A C}$ da ñu koy tuddee angal bu jub.
  • Angal bu tappandaar : Su ñaari xaaj-rëdd yii di  $\rm [A B)$ ak $\rm [A C)$ feewëloo, da ñuy naan angal bii di $\rm \widehat{B A C}$ angal bu tappandaar la.
  • Angalu tus : Su ñaari xaaj-rëdd yii di $[\mathrm{AB})$ ak $(\mathrm{AC})$ maasalooyee, da ñuy naan angal bii di $\rm \widehat{B A C}$ angalu tus la.

   Angles yu bokkwet

Raññee : Ñaari angal yu bokk bènn puj, bènn wet te ndeyjoor ak si cammoñu wett wòwu da ñu leen di tuddee ay angal yu bokkwet. 

Jumtuwaay bi lay may ngay natt angal yi ñu ngi koy woowee « raportër ». Raportër bi ab xaaj-mbege la bu ñuy maaskà dalee ko $0$ ba $180°$.
Diggi xaaj-mbege mi ñu ngi koy woowee diggi rapotër bi. Rëdd biy jaar si  $\rm O$ ak si maaskà bii di $0°$ mooy « rëddu tus wi ».

  • Bènnal bi ñiy nattee angal yi mooy jegoo (degré) ñu koy mandargaalee $°$.
  • Nattug bènn angal man na ñu def itam ci bènnal bu ñut tuddee garad mandargaam di $\rm gr$.
    • Angal bu jub nattam mooy $90°$ wala $\bf\color{red}{100~gr}$.
    • Angal bu tappandaar nattam mooy $180°$ wala $\bf\color{red}{200 ~gr}$

II. Nattu bènn angal

Ngir nattu angal bii di $\rm\widehat{AOB}$, da ngay jëfëndikoo bènn raportër :

  • Da ngay tek diggi raportër bi ci tomb bii di $\rm O$.
  • Nga daal di tek maaskà $0$ ci kow xaaji rëdd bii di $\rm [OA)$ (su ko laajee nga mottali ko).
  • Nga jang ci raportër bi ci bann maaskà la xaaj-rëdd bii di  $\rm [OB)$ (su ñu ko mottalee) di dagg xaaji mbege mi nekk si biti raportër bi. 

Fii da ñuy am : $\rm\widehat{AOB}=70°$

  • Koñ wala angal bu xatt mooy angal bu gëna xatt ab angal bu jub. Nattam mu ngi tollu su digante $0°$ ak $90°$.
  • Angal bu ne laññ mooy angal bu ëpp bènn angal bu jub. Nattam mu ngi tollu su digante  $90°$ ak $180°$.

Ñaari angal da ñoo mottaliwante su fekee soo leen yokkalantee da ngay am $90°$.
Ñaari angal da ñoo dolleeku su fekee soo leen yokkalantee da ngay am $180°$.

  • Seddale koñu bènn angal mooy rëdd wiy jaar ci puju angal bòbu te di ko xaaj ci ñaari angal yu tolloo nattuwaay. 
  • Safaanoo jàkaarlook bènn angal ci bènn rëdd wu ñu xam da fay nekk bènn angal bu yémak moom natt (maanaam man na ñu leen teglante).