Soo xaajè benn limmum fukkèl $a$ ci bénèn limmum fukkèl $b$, da ngay am benn limmum fukkèl $q$ ak benn ndéssit $r$ :
- $a$ mooy li ñuy xaaj (dividende).
- $b$ mooy liy seddëlé (diviseur).
- $q$ mooy xaajit gi (quotient).
- $r$ mooy ndéssit gi (reste).
$\rm \color{orange}{Li ñuy xaaj = Liy seddëlé \times Xaajit + reste}$
Ci bép xaajaalé, su ndéssit gi nékkè $0$, da ñuy nân xaajit bi dafa yem kepp.
$$\color{orange}{a=b \times q + r \text { avec } r < b}$$
I. Xaajit bu jégé té yèes
Su xaajit bi nekkè ab limmum lëmm, da ñu koy tuddè xaajit bu matt sëkk wala bu jégé lu yèes benn bennal.
Su xaajit amè benn, ñaar wala ñetti fas ci gannâw xosi wam, da ñu koy tuddè xaajit bu jégé ci lu yèes fukkèl, wala tèmèrèl, wala junnèl.
II. Xaajit bu jégé té ëpp
Boo yokkè benn ci xaajit bu matt da nagay am xaajit bu jégé té ëpp ci lu matul benn bennal.
Boo yokkè itam $0,1$ ; $0,01$ wala $0,001$ ci xaajit wu jégé té yées da ngay daaldi am xaajit bu jégé té ëpp ci lu matul fukkèl, wala tèmèrèl, wala junnèl.
Ay tëralinn :
a. Xaajalé ci $\bf\color{orange}{10, 100, 1~000, 0,1}$, etc.
- Ngir xaajalé ben limmum fukkèl ci $10$ ; $100$ wala $1~000$, da ngay toxal xosi ci benn, ñaar wala ñetti barab booy dém cammooñ.
- Ngir xaajalé ben limmum fukkèl ci $0,1$ ; $0,01$ ou $0,001$, da ñuy ngay toxal xosi ci benn, ñaar wala ñetti barab booy dém ndey joor.
b. Xammeekaayu ab xaajèf
- Ab limmum lëmm xaajèf na ci $2$ bu fékkè né fasum benn bennèlam dafa nek $0$, $2$, $4$, $6$.
- Ab limmum lëmm xaajèf na ci $3$ wala $9$ bu fékkè né ndajalèk fasam yi manèss na koo xaaj ci $3$ wala $9$.
- Ab limmum lëmm xaajèf na ci $5$ bu fékkè fas wi mu mujjè daf nekk $0$ wala $5$.
- Ab limmum lëmm xaajèf na ci $10$ bu fékkè fas wi mu mujjè daf nekk $0$.