Ñaari rëdd yu dogoo tey defar benn koñ-jub ñu ngi lèn di tuddee ay rëdd yu jub-dogoo.
- Mann ngaa rëdd ay rëdd yu dul jeex yu jub-dogoo ak bènn rëdd bu ñu xam.
- Benn rëdd rek nga mana rëdd muy jaar ci benn tomb bu ñu xam tey jub-dogoo ak benn rëdd bu ñu xam.
- Ngir nataal ay rëdd yu jub-dogoo, da ngay njekkë nataal bènn rëdd. Soo noppè nga mandargaal bènn tomb ci kow rëdd wi te tek ekerr bi si rëdd wi ci anam boo xamne jub-koñ bi da fay bayyeekoo ci tomb bòbu. Su ko defee nga daal di nataal ñaareelu rëdd wi di top wei ekerr bi, boo noppè nga mottali ñaareelu rëdd wòwu ak reegal gi.
I. Tasebkawewaayu bènn dogit
Tasebkawewaayu bènn dogit mooy rëdd wi koy dog ci ndogin wu jub téy jaar ci diggam.
Mooy itam mbooloom tomb yi nga xamne seen soreewaay ak ñaari ceti dogit wi ñoo tolloo.
Ñaari rëdd yu dogoo wul da ñu lèn di tuddee ay rëdd yu jub-làŋ.
Ci misaal :
Ngir woné ne ñaari rëdd da ñoo jub-làŋ, da ñuy jëfëndikoo mandarga wii di « // ».
Ñaari rëdd yu jub-làŋ saay wu nekk ñooy yémoo digante te du ñu dogoo mukk ak loo lèn mottali mottali.
Ngir saytu ndax ñaari rëdd da ñoo jub-làŋ, da ngay tek reegal bi ak ekeerr bi ci anam boo xamne ñoom ñaar da ñuy jub-dogoo, nga daal di natt diganteek ñaari rëdd yi ci ñaari tomb yu bokkee wul. Su ñu jub-làŋee, dogit yi lèn di jokkale te jub-dogoo ñooy yém guddaay.
Ngir nataal ñaari rëdd yu jub-làŋ, da ngay rëdd bènn rëdd (a) ak ñaari dog-jub. Ak reegal bi, nga natt ñaari yoon bènn digante bi te mandargaalee ko ñaari tomb. Soo noppè, nga jokkalante tomb yòyu ngir mana nataal rëdd bi jub-làŋ ak rëdd bii di (a).
II. Ceet yi aju ci rëdd yu jub-làŋ yi ak rëdd yu dog-jub yi
Su ñaari rëdd jub-làŋee, bépp rëdd wu jub-làŋak wenn wi d fay jub-làŋ ak weneen wi.
Su ñaari rëdd jub-làŋee, bépp rëdd wu jub-dogoo wenn wi d fay jub-dogoo ak weneen wi.
Su ñaari rëdd jub-dogoo ak bènn rëd, konn da ñuy daal di jub-làŋ ñoom ñaar.