I. Boyèt bu jub
Ab boyèt bu jub bènn mbirr mu dëgër la mu am juròmbenni kanam yu yemoo ñaar ñaar, juròmñetti puj ak fukkak ñaari yaxx.
Boo tijjee bènn boyèt bu jub te tallal ko, da ngay gàñcaxam (développement ou patron).
An kub bènn boyèt bu jub la boo xamne kanamam yi ay kaare la ñu.
Rëdd wii di $\rm (AE)$ da fay jub dogoo ak $\rm (EH)$ agit $\rm (EF)$. Rëdd wii di $\rm (HG)$ da fa nekk ci maasale bi $\rm (EH)$ ak $\rm (EF)$ nekk. Da ñuy naan rëdd yii di $\rm (AE)$ ak $\rm (HG)$ da ñoo jub jàkkaarloo (orthogonales).
Ñaari rëdd yu jub-dogoo (yu melni $\rm (AE)$ ak $\rm (EH)$) da ñuy jub-jàkkaarloo itam.
Ñaari rëdd yu jub-jàkkaarloo du ñu jub-dogoo say wu nekk.
Su yaxi bènn boyèt bu jub nekkee $a$, $b$ ak $c$ ci toftalin bòbu, niko nataal wii si suuf di ko wonee :
Su bòbaa ëmbkaay (volume) $\rm V$ bu boyèt bòbu dèes na ko xayma ci mbind mii :
$\mathrm V = a \times b \times c = \text{aire d’une base} \times \text{hauteur}$.
II. Pott wu jub
Ab pott wu jub ben mbirr mu dëgër la woo xamne ñari sunkkëndikukaayam ay disk la ñu.
Boo tijjee bènn pot wu jub te tallal ko, da ngay gàñcaxam (développement ou patron).
III. Tëmb ak bull
Ab tëmb benn ëmbkaay (volume) la boo xamné li ko wërr mooy bènn ëmbka (surface) bu tombam yëpp sorè benn tomb bu ñuy wooyè diggu tëmb bi.
Limmuk sorèwaay bòbu, na ñu ko tuddee $\rm R$, ci diggante tomb yi ak digg bi ñu ngi koy tuddee ceñeeru tëmb bi.
Na $\rm I$ nekk diggi tomb bi te $\rm S$ bènn ci ay tombam. Su bòbaa $\rm IS$ da fay nekk bènn ceñeer.
Bull : Mbooloom tombi jawwu ji yi nga xamne seen soreewaay ak tomb bii di I da fa yèes wala mu tollook ceñeer bi mooy bull bi diggam nekk I te ceñeeram di $\rm R$.
Bepp mbege bu diggam nekk $\rm O$ te ceñeeram di $\rm R$ da fay nekk bènn mbege mu mag bu tëmb bi.
IV. Baati tënk yi ñiy xaymaa yaatuwaay yi ak ëmbkaay yi
Boyèt bu jub bu guddaayam nekk $\rm I$ te kawwaayam di $\rm h$ | Boyèt bu jub bu guddaayam nekk $\rm I$ te kawwaayam di $\rm h$ | Tëmb bu ceñeeram di $\rm R$ | Bull bu ceñeeram di $\rm R$ | |
Yaatuwaayu tank bi | $\color{orange}{\rm L\times I}$ | $\color{orange}{\pi\rm R^2}$ | ||
Yaatuwaayu wett gi | $\color{orange}{\rm 2(L+I) \times h}$ | $\color{orange}{\rm 2\pi Rh}$ | ||
Yattuwaay wi lepp | Yaatuwaayu tank bi + Yaatuwaayu wet gi | Yaatuwaayu tank bi + Yaatuwaayu wet gi | $\color{orange}{\rm 4\pi R^2}$ | |
Volume | $\color{orange}{\rm L \times l \times h}$ | $\color{orange}{\rm \pi R^2h}$ | $\color{orange}{\rm \dfrac{4}{3}\pi R^2}$ |