Ab maassalé amul fumu yém. Dara tënku ko. Ñaaré ñu ngi koy mandargaalè benn wetlàng (parallélogramme) té di ko xamlè ci araf bii di $\rm P$.
Ab tomb bénn barab la bu nékk ci maasalé gi té amul gudday amul tarraay.
Ab tomb bénn barab la bu nékk ci maasalé gi té amul gudday amul tarraay.
Ngir mandargaal bénn tomb ci benn maassalé, da ñuy ték bénn kurwaa ba noppi binnd benn araf bu ñu maggal ci wéttam muy dëppook turu tomb bòbu.
$\rm A$ da fa bokk ci maassalé $\rm (P)$ ñu ngi koy binndè $\rm A \in (P)$. Ab maassalé ay tomb yu dul jèx ñoo si nékk.
Ab rëdd benn rëdd wu jubla boo xamné amul fumu tambalè, amul fumu jèxè. Ñaari wéttam yëpp amu ñu fi mu yém.
Da ñu koy mandargaalè benn rëdd wu jub xocc.
Su benn tomb $\rm B$ nékkè ci benn rëdd $\rm (D)$, da ñuy naan tomb bii di $\rm B$ bokk na ci rëdd bii di $\rm (D)$ té koy binndè $\rm B \in (D)$.
Yénèn binndinu benn rëdd
JAGLÉ 1 : Ci benn tommb, man na fa jaar ay rëdd yu dul jèx.
JAGLÉ 2 : Ci ñaari tomb, benn rëdd rék moo fa mana jaar.
Ab rëdd da fay séddëlé maasalé gi ci ñaari gox yu ñuy woowè xaaju maassalé : rëdd bi mooy digg bi nék ci diganté ñaari xaaji maasalé yi.
Rëdd yu doganté, rëdd yu dul laaloo, rëdd yu maassaloo, wàll
Tomb bii di $\rm A$ dafa bokk ci rëdd bii di $\rm(D_1)$ ak rëdd bii di $\rm (D_2)$ : da ñuy naan tomb $\rm A$ mooy tomb bi digaalé ñaari rëdd yii di $\rm (D_1)$ ak $\rm (D_2)$.
Man na ñu wax tamit né rëdd yii di $\bf \color{orange}{(D_1)}$ ak $\bf \color{orange}{(D_2)}$ da ñuy doganté ci tomb $\rm A$ wala ñuné rëdd yii di $\bf\color{orange}{D_1)}$ ak $\bf \color{orange}{D_2}$ da ñu dogoo ci $\rm A$.
Lòlu ñu ngi koy binndè $\rm (D_1) \cup (D_2) = \{A\}$.
Tomb $\rm A$ mooy tombu doganté bu ñaari rëdd yii di $\rm (D_1)$ ak $\rm(D_2)$.
Ñaari rëdd yu dul laaloo ñooy ñaari rëdd yu amul bénn tomb bu lèn digaalé.
Ñaari rëdd yii di $\rm (D)$ ak $\rm (L)$ ay rëdd yu dul laaloo la ñu.
Ñaari rëdd yii di $\rm (AE)$ ak $\rm (AC)$ benn la ñu. Da ñuy naan da ñoo maasaloo.
Ñaari rëdd yu dogoo da ñuy xaajalé maassalé gi ci ñennti wàll.
Nañ jël benn rëdd $\rm (D)$ boo xamné tomb yii di $\rm A$ ak $\rm B$ ci la ñu nékk.
Xaaju rëdd wi nékk ci diganté $\rm A$ ak $\rm B$ ñu ngi koy tuddè dogit bu cett yi nékk $\rm A$ ak $\rm B$. Dèes na ko binndè $\rm [AB]$ wala $\rm [BA]$. Rëdd wii di $\rm (D)$ mooy këruk [AB]$.
Su ñuy mottali dogit bii di $\rm [AB]$ ci wétt gi jëm ci $\rm B$, da ñuy benn xaaju rëdd $\rm [AB)$.
$\rm [AB)$ mooy est la demi-droite d’origine $\rm A$ passant par $\rm B$.
$\rm [BA)$ est la demi-droite d’origine $\rm B$ contenant $\rm A$.
Ab rëdd wu ñu damm té mu ubbèku ñu ngo tuddè rëdd mu bari wétt. Ñu ngi ko défarè ak ay dogit. Ngir tudd benn rëdd wu damm, da ñuy tudd ci toftalanté turu cettam yëpp.
Ci missaal : rëdd mu bari wétt mii di $\rm ABCDEFGH$ xala $\rm HFEDCBA$.
Ab rëdd wu ñu damm té mu tëju ñu ngi koy tuddè bari wétt. Dogit yi ñu défarè benn bari wétt rëdd wu ñu damm té mu ubbèku ñu ngi lèn di tuddè wétt. Cettu dogit yòyu ñu ngi lèn di tuddè ay puj.
Ci missaal : Bari wétt $\rm FGHIJ$.
Dogit yii di $\rm [FG]$, $\rm [GH]$, $\rm [HI]$, $\rm [IJ]$ et $\rm [JF]$ ñooy wétti bari wétt gii di $\rm FGHIJ$.
Tomb yii di $\rm F$, $\rm G$, $\rm H$, $\rm I$ et $\rm J$ ñooy puj yi.
Ay cettu benn wétt da ñuy nékk ñaari pij yu toftalanté (ci missaal $\rm F$ ak $\rm G$ ci $\rm [FG])$.
Wétt yii di $\rm [FG]$, $\rm [GH]$ nga xamné da ñoo bokk benn cett da ñu lèn di tuddè ay wétt yu toftalanté.
Wétt yu melni $\rm [IJ]$ ak$\rm [GH]$ nga xamné bokku ñu benn cett ñu ngi lèn di tuddè ay wétt yu toflanté wul.
Dogit yiy jokkalé ñari puj yu toflanté wul ñu ngi lèn di woowè ay galaŋ yu bar wétt gi (ci missaal $\rm [JG]$, $\rm [JH])$.