Mbege mi diggam nekk $\mathrm{O}$ té cénèeram di $\mathrm{R}$ mooy mbooloom tomb yi nga xamné seen soreewaay ak tomb bii di $\mathrm{O}$ da fay yemoo ak $\mathrm{R}$.
Lòlu limiy firi mooy :
- Su benn tomb A nekkee ci mbege gògu, konn da ñuy am : $\mathrm{OA}=\mathrm{R}$.
- Su benn tomb $\mathrm{A}$ wérëlè né $\mathrm{OA}=\mathrm{R}$, konn tomb $\mathrm{A}$ bòbu da fay nekk ci mbege mòmu.
Ngir nataal benn mbege, dèes na jëfandikoo benn jumtuwaay bu ñuy woowee « kompa »
$\rm [OB]$ ab ceñeer la ci mbege wi diggam nék $\mathrm{O}$ te cenèram nekk $\mathrm{R}$.
$\rm [CD]$ ab buum digg la bu mbege wi diggam nekk $\mathrm{O}$ té ceñeeram nekk $\mathrm{R}$.
$\rm [AC]$ ab buum la bu mbege wi diggam nek $\mathrm{O}$ te ceñeeram nekk $\mathrm{R}$.
Xaaju mbege $(\mathrm{C})$ mi nekk si digante ñaari tomb $\rm A$ ak $\rm B$ bu benn mbege ñu ngi koy woowee xalaak mbege.