Xam nañ né: $5,3 \times 4 = 21,2$
- limm bii di $21,2$ mooy méñèf gi. (produit)
- limm yii di $5,3$ et $4$ ñooy ëmbeefu (facteurs) méñèf gi.
- Xètu xauma bi ñu binnd nii mooy ab fŭll (multiplication).
Su $a$ ak $b$ ñaari limmum fukkèl da ñuy am : $a\times b = b \times a$. Da ñuy naan tañ ab xayma bu dëppook weccaloo la.
Su $a$, $b$ ak $c$ nékkè ñetti limmum fukkèl, dañuy amm : $(a \times b) \times c = a \times (b \times c)$. Da ñuy naan tañ ab xayma bu dëppook anndaalé la.
Méñèfu limmum fukkèl bu nekk ak $1$ mooy limmum fukkèl boobu.
Su $a$ nékkè benn limmum fukkèl, da ñuy amm $\color{orange}{a\times 1 = 1 \times a = a}$.
Méñèfu limmum fukkèl bu nekk ak $0$ mooy tus.
Su $a$ nékkè benn limmum fukkèl, da ñuy amm $\color{orange}{a\times 0 = 0 \times a = 0}$.
Soo bëggè amm méñèfu benn limmum lëmm ak bénèn limmum fukkèl, wala méñèfu benn limmum fukkèl ak benn limmum lëmm, da ngay njëkka défar fŭll gi, baña bayyi xél xosi gi.
Ba noppi, nga yokk xosi gi ci jèxital gi ci anam goo xamné limu fas yi nekk ci gannâw xosi mi day tollook limmum fas yi nekk ci gannâw limmum fukkèl gi.
Soo bëggè itam amm méñèfu ñaari limmum fukkèl, da ngay njëkka défar fŭll gi, baña bayyi xél xosi gi. Boo noppè, nga ték xosi gi ci jèxital gi ci anam goo xamné limu fas yiy nekk ci gannâwam day tollook limmum mboolèm fas yi nekk ci gannâw ñaari limmum fukkèl yi.