I. Xamlé ay limm yu jokkalanté
Benn limm bu jokkaloo da fay am ñaari wàll : mandargaam $(+$ ou $-)$ ak njëggug limam : ($-3$ ; $+8$ ; $-2$…)
Ñaari limm yu jokkaloo té tolloo njëggug lim waayé ûté ci mandarga ñu ngi lèn di woowè limm yu fèwëloo. Ci missaal : $-3$ et $+3$
II. Yokkuk ay limm yu jokkalanté
- Su ñaari limm yi bokkè benn mandarga, da ngay yokalanté sèniy njëgum limm ba noppi ték ci kanam mandarga mòmu ñu bokk.
- Su ñaari limm yi amè ay mandarga yu wûté, da ngay waññi ci njëgum lim bi gënë réy njëgum limm bi gënë tûti, ba noppi ték ci kanamu jèxital gi mandargaayu limm bi ëppëlé njëgum lim.
Ci missaal : $(-19)+(+24)=+(24-19)=+5$ ndax ñaari limm yu jokkalanté yi da ñoo am ay mandarga yu ûté té $+24$ moo ëpp njëgum lim
III. Waññik ay limm yu jokkalanté
Waññi ab limm bu jokkaloo da fay yémook nga yokk limm bi mu fèwëlool.
Booy waññi benn limm bu jokkaloo, da nga wra njëkka sèt limm bi fèwëloo ak moom ba noppi yokkalanté ñaari limm yu jokkaloo.
Ci missaal : $(+5)-(+13)=(+5)+(-13) = -(13-5)=-8$.