I. Limmum lëmm yi. Seen mbind ak ay fas
Ngir limm ay mbirr wala ay nitt, da ñuy jëfendikoo ay limmum lëmm (nombres entiers naturels).
Limm yooyu, dees na ko binndè ak ben fas (chiffre) wala ay fas yu bari.
Fas yi ñuy jëfendikoo ngir bind limm yi ñooy yii:
$0~1~2~3~4~5~6~7~8~9$
Ay missaal :
- $131$ aw limm la woo khamné man na ñu ko jëfendikoo ngir limm ay égaat (billes) ; ab limmum lëmm la bu ñu binndee ak fas yii di $1$ ak $3$.
- $12,4$ ak $\dfrac{2}{3}\approx 0, 66$ ay limm lañu yoo khamni kenn manu koo jëfendikoo ngir xayma ay égaat. Konn du ñu ay limmum lëmm (nombres entiers naturels).
- $\dfrac{20}{4}$ ab limmum lëmm la, ndax $\dfrac{20}{4}=5$ aw limm la woo khamné man na ñu ko jëfendikoo ngir limm ay égaat.
- Bépp fas man na ñu ko jëfendikoo ngir limm ay égaat. Moo tax bépp fas ab limum lëmm la.
Bërëb bi benn fas di nekk ci biir mbindum benn « limmum lëmm » lou am solo la. Fas bi gënë feetè ndey joor mooy mandargaal “benn benn” yi (unités simples).
Fukki “benn benn” wu nekk day nekk ben “fukk fukk” (dizaine). Moom fas bi koy mandargaal day nekk ci wettu fasum benn benn yi si cammooñam.
Fukki “fukk fukk” bu nekk day doon benn “teemeer teemeer”. Moom fas bi koy mandargaal day nekk ci wetu fasum teemeer teemeer yi si cammooñam.
Ñetti fas yooyu boo leen dajalee day nekk benn “maas” (classe).
Maas gi njëkk mooy “maassu benn benn yi” (classe des unités simples).
Bi ci topp mooy maasu “junni junni” yi, tek si maasu “milliong” yi tek si maasu “milliar” yi, di wéy noonu...
Si binndug ben limm gu rëyy, dees na texxali maas yi ak benn barab bu ndaw bu amul dara.
II. Xam Xamu Mbooloo
Man na ñu defar bènn mbooloo ci lu tukkee ci bènn kureelu nitt wala kureelu ay mbirr.
Su fekkee ne kureel gògu da fa ëmb ay nitt wala ay mbirr yu ñu mana lim, da ñuy naan mbooloo mu am dayoo la ñu am.
Su fekkee ne kureel gògu manèesu koo lim, da ñuy naan mbooloo mu amul dayoo la ñu am.
Ay missaal :
- Mbooloom ndongo yi nekk ci maas gii di 6e C ;
- Mbooloom nitt yi dëkk Senegal ;
- Mbooloom cëri bènn njaboot.
Ngir mandargaal benn mbooloo, man na ñu joxee liisu (la liste) cër (élément) yi ci bokk yëpp. Cër yooyu dañuy leen di bind ci digante ñaaru junj yu mel nii: { }
-
Ci missaal, mbooloom gox yi nekk Sénégal mooy:
$\mathcal G = \{\text{Ndakkaaru, Cees, Kaolakh, Siki Coor, Kolda,}$ $\text{Fatik, Tambakunda, Kedugu, Maatam, Luga,}$ $\text{Jurbel, Seeju, Kafrin, Ndarr}\}.$
- Mbooloomu fas yi mooy:
$\mathcal F = \{0,~1,~2,~3,~4,~5,~6,~7,~8,~9\}.$
Dañuy naan cëru menn mboolo dafa bokk ci mbooloo moomu. Ngir bind loolu, dañuy jëfëndikoo junj bii: $\notin$. Su ci bokkul, ñu bind $\notin$.
Ay missaal:
- Dakar $\in \mathcal{G}$ ; Bignona $\notin \mathcal{G}$ ; $6 \in \mathcal{C}$ ; $10 \notin \mathcal C$.
Mbooloom limmum lëpp yi dees na ko mandargaalee $\mathbb N$.
$\mathbb{N}=\{0~ ;~ 1~ ; 2~ ; 3~ ; 4~ ; 5~ ; 6~ ; 7~ ; 8~ ; 9~ ;$ $10~ ;~ 11~ ; 12~ ; 13~ ; \ldots ~;\ldots ~;\ldots\}$
$\mathbb N$ mbooloo wu amul dayoo la.