Sàrtu jiitëlanté ay xayma
- Ci benn xayma bu ñu binnd cim rëdd, sëfuk xayma gi nekk ci diganté ñaari xala (parenthèses) moom nga wara jiitël.
Ci missaal: Suma buggè xayma , damay njëkka xayma ba noppi ma fŭll jèxital gi ci - Ci benn xayma bu amul xala (parenthèses), fŭllanté ak xaajalé yi ñoo wara jiitu yokk yi ak waññi yi.
- Ci benn xayma boo xamné nak amul ludul ak yokk ak ay waññi, da ngay njëkkè xayma yi gënë nékkè cammoñ, di wëyy di dém ndéy joor.