I. Ñettkoñ yi
Ab ñettkoñ bènn bariwett la bu am ñetti wett.
Nataal bii ci suuf ab ñettkoñ la. Ñu ngi koy binndè : $\rm ABC$ wala $\rm BCA$ wala $\rm CAB$.
Tomb yii di $\mathrm{A}$, $\mathrm{B}$ ak $\mathrm{C}$ ñooy ñetti pujam.
$\widehat{\rm A B C}$ bènn angali ñettkoñ bi la. $\rm [AC]$ mooy wet bi safaanoo ak angal bii di $\widehat{\rm A B C}$.
Wett yii di $\rm [A B]$ ak $[\mathrm{A C}]$ ñooy wett yi jegesës (adjacents) angal bii di $\widehat{\rm A B C}$.
Ngir nataal bènn ñetkoñ soo xamee ñetti wetam :
- Da ngay rëdd dogit wii di $\rm [BC]$ (ci misaal) ;
- Nga rëdd xalag mbege mi nga xamne diggam mooy $\rm B$ te ceñeeram di $\rm A B$ ;
- Nga rëdd xalag mbege mi nga xamne diggam mooy $\rm C$ te ceñeeram di $\rm A C$ ;
- Ñaari xala yòyu da ñuy dogoo si $\rm A$.
II. Ay rëdd yu raññeeku
Seddale koñ : Xaaj-rëdd wuy xaajale bènn ci angali ñettkoñ bi si ñaari angal yu tolloo natt.
Kawewaay : Rëdd wuy jaar si bènn puj tey jub-dogoo ak wett wi mu jàakkarlool.
Xaaj-digg : Rëdd wi jub-dogoo ak bènn wet tey jaar si diggam.
Jaar-digg : Rëdd wiy jaar si bènn puj ak ci diggi wett wi mu jàakkarlool.
III. Ay ñettkoñ yu ñu raññee
Ñettkoñ wu jub
Xamle : Da ñuy naan ab ñettkoñ da fa jub su amee bènn koñ gu jub. Wett gi jàkkaarlo ak koñ gu jub gi (wett wi ëpp) ñu ngi koy woowee janookoñjub bu ñettkoñ bi.
Ab jagle : Su bènn ñettkoñ jubee, ñaari angal yi jegesës janookoñjubam da ñoo mottaliwante, maanam seen ndajaleek natt yi da fay tollu si $90°$.
Ñettkoñ wu ñaariwet-yem
Xamle : Da ñuy naan ab ñettkoñ da fa ñaariwet-yem su amee ñaari wet yu tolloo guddaay. Da ñu wara leeral si bann tomb la ñaariwet-yemee (mooy pujuk cosaan bi) wala tankam (wett gi jàkkaarlook pujum cosaan wi).
Ay jagle : Su bènn ñettkoñ ñaariwet-yemee, ñett rëddam yi raññeeku tey bawoo ci pujuk cosaanam ak xaaj-diggu tankam wi da ñuy maasaloo (da ñuy nek aksu safaanook jàkkaarle bu ñettkoñ bi).
Su bènn ñettkoñ ñaariwet-yemee, ñaari angal yi jegesës tankam ñoo yem natt.
Ñettkoñ wu wet-yem
Xamle : Da ñuy naan ab ñettkoñ da fa wet-yem su amee ñetti wet yu tolloo guddaay.
Ay jagle : Su bènn ñettkoñ wet-yemee, ñett rëddam yi raññeeku tey bawoo ci puj bu nek ak xaaj-diggu puj wi mu jàakkaalool da ñuy maasaloo (ñoom ñooy nek ñetti aksu safaanook jàkkaarle bu ñettkoñ bi).
Su bènn ñettkoñ wet-yemee, ñetti angalam yi seen natt da fay nekk $60°$.