I. Anamu dëppoo ci xaajalé 

Da ñuy naan ñaari nattèf da ñoo dëppoo ci xaajalé su fékkè saay woo jëlè benn limm ci kenn si ñoom ñaar, mann nga am bénèn bi soo ko fŭllanté ak benn limm boo xam né bu ñu raññè la té du soppèku.

Limm bòbu ñu ngi koy woowè limm giy mandargaal dëppoo ci xaajalé gi.

Su lòlu amul, da ñuy naan ñaari nattèf yi dëppoo wu ñu ci xaajalé.

II. Mottali benn alluwaak dëppoo ci xaajalé

Ngir mottali benn alluwaak dëppoo ci xaajalé, da ñu wara daj limm gi koy mandargaal : mooy limm giy dëppook benn ci nattèf gi. 

Su lòlu noppè, ñu jëfëndikoo ay fŭllanté ak ay xaajalé ngir mottali alluwa gi dimbalèko ci limm giy mandargaal dëppook xaajalé gi.

III. Ték benn xaajitu tèmèral 

Ték ab xaajitul tèmèral ci benn limm day mel ni ngay défar benn fŭllanté.

Ci missaal

$40 \%$ de $60$ mu ngi tollook $\dfrac{40}{100} \times 60=\dfrac{40 \times 60}{100}=\dfrac{2400}{100}=24$

Ngir mottali yémaay gi : $a \times \ldots=b$, damay xaajalé $b$ ci $a$.