Émalé ñaari limm mooy nga lèral bann ci ñoom ñaar moo gënë tûti ak bann moo ëpp wala ndax ñoo tollô.

Mandarga mii « = » mooy mandargaak ab tollô.  

Mandarga mii « < » dèss na ko janngè « moo gënë tûti » wala « moo yèss ».

Ngir yémalé ay limm, mann na ñu tamm jëfëndikoo benn ci mandraga yii : $\leq$ ; $\geq$. 

Ngir mengalé (comparer) ñaari limmum fukkèl yu ñuy xaymâ, da ngay njëkka mengalé sèniy xaajum lëmm.

  • Suñu tollôwul bi ëpp mooy bi xaaji lëmmam gëna rëyy.    
    Ci missaal : $3,4 < 4,37$ ndax $3 < 4$
  • Suñu tollôwè, da ñuy daal di mengalé benn benn fas yi nekk ci xaajum fukkèl yi, tambalè ko ci fukkèl yi topp ci tèmèral yi, topp ci….  
    Ab Sètlu : Ngir mengalé, mann nañ tamm mottali xaajum fukkèl mi ak ay tus. 
    Ci missaaal : $2,001 < 2,01$ ndax fasum tèmèralu $2,001$ moo gënë tûti fasum tèmèralu $2,01$.

Wërëlé (encadrer) benn limm mooy nga féxé ba am benn limm bu ko gënë tûti ak benn limm bu ko ëpp.

Ci missaal : Nañ wërëlé $24,78$

$\bf\color{orange}{24 < 24,78 < 25}$ lòlu benn wërëlé 24,78 la, ak ay limmum lëmm.

Émalé ay limmum fukkèl ci anam buy yokku, mooy nga binnd lèn dalè ci bi gënë tûti ba bi ci ëpp.

Émalé ay limmum fukkèl ci anam buy waññèku, mooy nga binnd lèn dalè ci bi ëpp ba bi ci gënë tûti.

Wërëlé benn limm lu wèssu wul benn, mooy wërëlé ko aak ay limum lëmm yu toftalanté.

Ci missaal : $34 < 34,2356 < 35$ lòlu benn wërëlé  $34,2356$ ci lu tollôk benn benn la.

Mbinnd mii moom $34,2 < 34,2356 < 34,3$ ab wërëlé wu $34,2356$ la ci lu wèssu wul $0,1$. 
Mbinnd mii moom $34,23 < 34,2356 < 34,24$ ab wërëlé wu $34,2356$ la ci lu wèssu wul $0,01$.