I. Gindèku ci benn rëdd wu jubb wu ñu maasskà
Ab rëdd wu jubb wu ñu maasskà da fay am benn tambalinn ak benn raññèkaayu bennèl buy la may nga mana ték tomb giy dëppoo ak $1$, ak itam yénèn tomb yiy dëppok limm yu matt yi, moo xam da ñoo ëpp tus wa la da ñu ko yèes, ci boo lèn mengëlè ak raññèkaayu bennèl gi.
Ay baat :
- $\rm O$ mooy tambalinn gi té guddaay gii di $\rm OI$ mooy raññèkaayu bennèl gi.
- Maasskaay tomb gii di $\rm A$ mooy $3$ té Maasskaay tomb gii di $\rm B$ mooy $-1,5$.
- Lòlu ñu ngi koy binndè $\rm A (3)$ et $\rm B (-1,5)$.
Mann nañu tam ték ay limmum fikkèl wala ay tojitt ci benn rëdd wu jubb bu ñu maaskà bu ñu nataalè ak au raññèkaay yu gënë sew.
II. Sorèwaayu ñaari tomb ci benn rëdd wu jub gu ñu maasskà
Sorèwaayu ñaari tomb ci benn rëdd wu jubb bu ñu maaskà mooy waññèf ci diganté maaskà gi ëpp ak gi gënë tûti.
Ci missaal, si rëdd wu jubb bi ñu maaskà ci kow nii : $\rm AB=(+3)-(-1,5)=3+1,5=4,5$ $\rm AB=(+3)-(-1,5)=3+1,5=4,5$.
III. Xammaléku ci tunnd wi
Ci benn gindèkukaay bu tunnd wi, tolluwaayu benn tomb ñu ngi koy xamè ci ñaari limm yu jokkaloo yu ñuy wooyè ay maaskaam.
Bu njëkk bi mooy maasskaam tëdd wi té ñaarèl bi mooy maasskaam taxaw mi.
Tomb bii di $\rm O$ ay maaskaam ñooy $(0~ ;0)$ mooy tambalinu xammalékukaay gi.
Jàngg maaskaay benn tomb :
Da ngay sèt maasskaam tëdd mi ci rëdd wi tëddà (rëddu maaskaay tëdd yi) ak maasskaam taxaw mi ci rëdd wi taxaw (rëddu maaskaay taxaw yi).
Maaskaay $\rm A$ ñooy $(\color{limegreen}{-1}~ ;\color{red}{3})$ $(-1~ ;3)$.
Maaskaay $\rm B$ ñooy $(\color{limegreen}{2}~ ;\color{red}{4})$ $(2~ ;4)$.
Maaskaay $\rm C$ ñooy $(\color{limegreen}{3}~ ; \color{red}{-2})$ $(3~ ; -2)$.